Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 12

YOWAANA 12:34-46

Help us?
Click on verse(s) to share them!
34Mbooloo ma ne ko: «Jàng nanu ci sunu téereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yaw, nan nga mana waxe ne: “Doomu nit ki dina yékkatiku?” Kuy Doomu nit kooku?»
35Yeesu ne leen: «Leer gi dootul yàgg ak yéen. Doxleen, ci bi ngeen dee am leer, ngir lëndëm bañ leena bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm doo xam foo jëm.
36Kon ci bi ngeen dee am leer gi, gëmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer.» Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa dem, nëbbatuji leen.
37Firnde yi mu leen won yépp taxul ñu gëm ko,
38ngir li yonent Yàlla Esayi waxoon am: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare? Kan la Boroom bi won dooleem?»
39Manuñu woona gëm, ndaxte Esayi dafa waxaat ne:
40«Yàlla dafa gumbaal seeni bët, def ba ñu dëgër bopp, ngir seeni bët baña gis, seen xel baña xam, ñu baña waññiku ci man ngir ma wéral leen.»
41Esayi dafa wax loolu, ndaxte gisoon na ndamu Yeesu te mi ngi doon wax ci ay mbiram.
42Fekk na ci biir njiit yi sax, ñu bare gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee tax fésaluñu ko, ndaxte dañoo ragaloon, ñu dàq leen ca jàngu ba.
43Ngërëmu nit a leen gënaloon ngërëmu Yàlla.
44Yeesu yégle ne: «Ku ma gëm, gëmuloo ma waaye gëm nga ki ma yónni.
45Ku ma gis, gis nga ki ma yónni.
46Ni ag leer laa wàcce ci àddina, ngir ku ma gëm du des ci lëndëm.

Read YOWAANA 12YOWAANA 12
Compare YOWAANA 12:34-46YOWAANA 12:34-46