Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 12:34-46 in Wolof

Help us?

YOWAANA 12:34-46 in Téereb Injiil

34 Mbooloo ma ne ko: «Jàng nanu ci sunu téereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yaw, nan nga mana waxe ne: “Doomu nit ki dina yékkatiku?” Kuy Doomu nit kooku?»
35 Yeesu ne leen: «Leer gi dootul yàgg ak yéen. Doxleen, ci bi ngeen dee am leer, ngir lëndëm bañ leena bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm doo xam foo jëm.
36 Kon ci bi ngeen dee am leer gi, gëmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer.» Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa dem, nëbbatuji leen.
37 Firnde yi mu leen won yépp taxul ñu gëm ko,
38 ngir li yonent Yàlla Esayi waxoon am: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare? Kan la Boroom bi won dooleem?»
39 Manuñu woona gëm, ndaxte Esayi dafa waxaat ne:
40 «Yàlla dafa gumbaal seeni bët, def ba ñu dëgër bopp, ngir seeni bët baña gis, seen xel baña xam, ñu baña waññiku ci man ngir ma wéral leen.»
41 Esayi dafa wax loolu, ndaxte gisoon na ndamu Yeesu te mi ngi doon wax ci ay mbiram.
42 Fekk na ci biir njiit yi sax, ñu bare gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee tax fésaluñu ko, ndaxte dañoo ragaloon, ñu dàq leen ca jàngu ba.
43 Ngërëmu nit a leen gënaloon ngërëmu Yàlla.
44 Yeesu yégle ne: «Ku ma gëm, gëmuloo ma waaye gëm nga ki ma yónni.
45 Ku ma gis, gis nga ki ma yónni.
46 Ni ag leer laa wàcce ci àddina, ngir ku ma gëm du des ci lëndëm.
YOWAANA 12 in Téereb Injiil