1Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile.
2Bëggul woona dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wuta rey. Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax màggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi.
3Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def.
4Ku bëgga siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.»
5Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
6Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax.
7Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul.
8Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.»
9Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
10Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sooga dem te kenn yégu ko; siiwalul demam.
11Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?»
12Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.»
13Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
14Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngle ca kër Yàlla ga.
15Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
16Yeesu daldi leen wax ne: «Li may jàngle, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
17Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngle ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare.
18Nit kiy wax ci coobareem nag, day wuta màggal boppam, waaye kiy wuta màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.
19Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?»
20Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wuta rey?»
21Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle!
22Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gone yi —jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan— moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésub noflaay bi.
23Bu ngeen manee xarafal nit ci bésub noflaay bi, ngir baña wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm?
24Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
25Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wuta rey?
26Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi?
27Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
28Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko.
29Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.»
30Noonu ñu koy wuta jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon.
31Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?»
32Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
33Yeesu wax ne: «Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, sooga dem ci ki ma yónni.
34Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen mana dem fa may nekk.»
35Yawut ya di laajante ci seen biir naan: «Fu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nara dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya, te jàngali Gereg ya?
36Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen mana dem fa may nekk”?»
37Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na: “Ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.”»
39Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroona jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon.
40Bi ñu déggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent bi wara ñëw.»
41Ñeneen naan: «Mooy Almasi bi.» Ña ca des it ne: «Waaye nan la Almasi bi mana jógee Galile?
42Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.»
43Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu.
44Am na ca ñoom ñu ko bëggoona jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara.
45Bi alkaati ya delloo, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: «Lu tax indiwuleen ko?»
46Alkaati ya ne leen: «Kenn masula waxe ni nit kooku!»
47Noonu Farisen ya laaj leen: «Mbaa naxuñu leen, yéen itam?
48Ndax am na kenn ci sarxalkat yi walla ci Farisen yi ku ko gëm? Déedéet.
49Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!»
50Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen:
51«Ndax ci sunu yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?»
52Ñu ne ko: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne benn yonent masula jóge Galile.»
53Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër.