Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 13

LUUG 13:1-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla.
2Mu ne leen: «Mbaa du dangeena xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gëna nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj?
3Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.
4Te fukki nit ak juróom ñett ñooñu dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeena yaakaar ne ñoo gëna nekk ay tooñkat ñeneen ñi dëkk Yerusalem yépp?
5Maa ngi leen di wax ne du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.»
6Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom.
7Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?”
8Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos.
9Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
10Benn bésub noflaay Yeesoo ngi doon jàngle ci ab jàngu.
11Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu wara mat fukki at ak juróom ñett; dafa xuuge woon te manul woona siggi dara.
12Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»

Read LUUG 13LUUG 13
Compare LUUG 13:1-12LUUG 13:1-12