Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG

LUUG 18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Noonu Yeesu wax leen itam léeb wii ngir xamal leen ne war nañoo sax ci ñaan te baña xàddi.
2Nee na: «Dafa amoon cib dëkk, benn àttekat bu ragalul Yàlla te faalewul mbindeef.
3Amoon na itam ca dëkk ba jigéen ju jëkkëram faatu ju daan faral di ñëw ci moom, naan ko: “Àtte ma ak sama noon!”
4Àttekat ba bañ lu yàgg, waaye am bés mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla te faalewuma mbindeef,
5waaye jigéen jii lakkal na ma; kon dinaa ko àtte, ngir mu bañatee ñëw sonal ma. Dina rey ak ay wax.”»
6Boroom bi tegaat ca ne: «Dégluleen bu baax li àttekat bu bon boobu wax;
7ndax Yàlla du àtte jub mbooloom mi mu tànn te ñu koy ñaan wall guddi ak bëccëg? Ndax dina leen xaarloo?
8Maa ngi leen koy wax, dina leen àtte jub ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki ñëwee, ndax dina fekk ngëm ci àddina?»
9Yeesu waxaat léeb wii nit, ñi foog ne jub nañu tey xeeb ñi ci des.
10Mu ne: «Dafa amoon ñaari nit ñu dem ca kër Yàlla ga, di ñaan. Kenn ki ab Farisen la, ki ci des juutikat.
11Farisen baa nga taxaw di ñaan ci xelam naan: “Yaw Yàlla, maa ngi lay sant ci li ma melul ni ñeneen ñiy sàcc, di def lu jubadi te di njaaloo, rawatina juutikat bii.
12Ayu-bés gu nekk damay woor ñaari yoon, di joxe asaka ci lépp lu ma wut.”
13«Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te bëggula siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay fëgg dënnam te naan: “Yaw Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat.”»
14Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen koy wax, nit kooku, ba muy ñibbi këram, moom la Yàlla àtte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, ñu yékkati la.»
15Amoon na ay nit, ñuy indil Yeesu ay liir, ngir mu teg leen ay loxoom. Bi taalibe ya gisee loolu, ñu gëdd leen.
16Waaye Yeesu woo leen ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw ci man, te buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla.
17Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci mana dugg.»
18Benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma wara def, ba am wàll ci dund gu dul jeex?»

19Yeesu ne ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax? Yàlla rekk a baax.
20Xam nga ndigal yi: “Bul njaaloo, bul bóome, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
21Njiit la ne ko: «Loolu lépp sàmm naa ko li dale ci sama ndaw ba tey.»
22Bi Yeesu déggee loolu, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am lépp, séddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.»
23Bi nit ka déggee loolu, mu am tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
24Yeesu xool ko, daldi ne: «Boroom alal, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!
25Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.»
26Ñi doon déglu daldi ne: «Kon nag ku mana mucc?»
27Yeesu ne leen: «Li të nit ñi, tëwul Yàlla.»
28Noonu Piyeer ne: «Nun de, dëddu nanu li nu am lépp, topp la.»
29Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër walla soxna walla ay doomi ndey walla ay waajur walla ay doom ngir nguuru Yàlla,
30dinga am tey jii ay yooni yoon, ak dund gu dul jeex ëllëg.»
31Yeesu wéetoo ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Nu ngi dem Yerusalem, te li yonent yi bindoon lépp ci mbirum Doomu nit ki dina mat.
32Dinañu ko jébbal ñi dul Yawut, ñu ñaawal ko, saaga ko, tifli ci kawam.
33Gannaaw bu ñu ko dóoree ay yar ba noppi, dinañu ko rey, waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
34Waaye taalibe ya dégguñu li mu leen doon wax; kàddu yooyu ump na leen, te xamuñu li waxi Yeesu yooyu tekki.
35Bi Yeesu di agsi dëkku Yeriko, am gumba gu toogoon ca wetu yoon wa, di yelwaan.
36Naka la gumba ga dégg mbooloo di jàll, mu laaj lan moo xew.

37Ñu wax ko ne: «Yeesum Nasaret moo fay jaar.»
38Noonu mu yuuxu ne: «Yeesu, Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
39Ñi jiitu woon gëdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy gëna yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
40Noonu Yeesu taxaw, santaane ñu indil ko ko. Bi mu jegesee, Yeesu laaj ko ne:
41«Loo bëggoon ma defal la ko?» Mu ne ko: «Sang bi, damaa bëgga gis.»
42Noonu Yeesu ne ko: «Na say bët gis! Sa ngëm faj na la.»
43Ca saa sa mu daldi gis. Noonu mu topp ci Yeesu, di màggal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.