Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 1

LUUG 1:27-76

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.
28Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
29Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.
31Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.
33Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
34Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu mana ame? Man de, janq laa ba tey.»
35Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.
36Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku manula am doom, mu ngi ci juróom benni weeram.
37Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
38Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.
39Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.
40Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet.
41Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.
42Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
43Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
44Maa ngi lay wax ne naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir ndax mbég.
45Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!»
46Noonu Maryaama daldi ne:
47«Sama xol a ngi màggal Boroom bi, sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,
48ndaxte fàttaliku na ma, man jaamam bu woyof bi. Gannaaw-si-tey, niti jamono yépp dinañu ma wooye ki ñu barkeel,
49ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy. Turam dafa sell.
50Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal, ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom, te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
52daaneel boroom doole yi ci seen nguur, yékkati baadoolo yi.
53Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex, te dàq boroom alal yi, ñu daw ak loxoy neen.
54Wallu na bànni Israyil giy jaamam, di fàttaliku yërmandeem,
55ni mu ko dige woon sunuy maam, jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
58Dëkkandoom yi ak bokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
59Bi bés ba délsee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakari.
60Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
61Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
62Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
63Sakari laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.
64Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakari daldi waxaat, di màggal Yàlla.
65Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.
66Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.
67Sakari baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
68«Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil, ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
69Feeñal na nu Musalkat bu am doole, bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,
70ni mu yéglee woon bu yàgg jaarale ko ci yonentam yu sell yi.
71Dina nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy bañaale.
72Yàlla wone na yërmandeem, ji mu digoon sunuy maam, te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,
73di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
74dina nu teqale ak sunuy noon, ngir nu man koo jaamu ci jàmm,
75nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
76Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji, ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, di ko xàllal yoon wi.

Read LUUG 1LUUG 1
Compare LUUG 1:27-76LUUG 1:27-76