Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 1

Luug 1:67-79

Help us?
Click on verse(s) to share them!
67Ci kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya feese Noo gu Sell gi, daldi tàmbalee biral kàddug waxyu, ne:
68«Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israyil, moo seetsi ñoñam, ba jot leen!
69Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,
70noonee mu ko waxe woon ca jant yu jëkk ya, yonentam yu sell ya woon jottli,
71moo nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy mboolem bañaale.
72Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,
73ak ngiñ la mu giñaloon sunu maam Ibraayma,
74ne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon, ba man koo jaamoo xel mu dal
75ci biir sellnga ak njub ci kanamam, sunu giiru dund.
76«Ngóor si nag yaw, yonentu Aji Kawe ji lees lay wooye, nde yaay dox, jiitu Sang bi, xàllal kow yoonam,
77ngir yégal ñoñam ag njot guy topp seen njéggalug bàkkaar.
78Sunu Yàllaa yaatu yërmande, moo nu fenkal ab jant,
79di niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru ndee, di nu gindi, teg nu ci yoonu jàmm.»

Read Luug 1Luug 1
Compare Luug 1:67-79Luug 1:67-79