67 Sakari baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
68 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil, ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
69 Feeñal na nu Musalkat bu am doole, bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,
70 ni mu yéglee woon bu yàgg jaarale ko ci yonentam yu sell yi.
71 Dina nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy bañaale.
72 Yàlla wone na yërmandeem, ji mu digoon sunuy maam, te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,
73 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
74 dina nu teqale ak sunuy noon, ngir nu man koo jaamu ci jàmm,
75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
76 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji, ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, di ko xàllal yoon wi.
77 Dinga xamal mbooloom ni leen Boroom bi mana musale, jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,
78 ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande, ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk,
79 ngir leeral ñi toog ci lëndëm, takkandeeru dee tiim leen, ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»