1Gannaaw loolu mbooloo ma mépp jóg, daldi yóbbu Yeesu ca Pilaat.
2Ñu tàmbali di ko sosal, naan: «Kii lanu fekk muy fàbbi askan wi, di aaye ku fey Sesaar galag, te naan moom ci boppam mooy Almasi, di buur.»
3Pilaat laaj ko ne ko: «Yaa di buurub Yawut yi?» Mu ne ko: «Yaa ko wax.»
4Pilaat ne sarxalkat yu mag ya ak mbooloo ma: «Waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.»
5Teewul ñu gëna dëggal seeni wax, ne: «Mooy yékkati askan wi, ndax li muy jàngle ci mboolem réewum Yawut, dale ko ca Galile ba fii.»
6Pilaat dégg loolu, daldi ne: «Waa jii waa Galile la?»
7Ba mu wóoree Pilaat ne ca diiwaan, ba ca kilifteefu Erodd la Yeesu bokk, ca la ko yónnee Erodd, yemook Erodd itam nekk Yerusalem ca fan yooya.
8Ba Erodd gisee Yeesu, bég na lool, ndax yàggoon na koo bëgga gis, ngir la mu déggoon ay mbiram, ba tax mu yaakaara teewe ay kéemaanam.
9Mu laaj ko lu bare, Yeesu tontuwu ko.
10Sarxalkat yu mag ya ak firikati yoon yaa nga taxaw, di ko tuumaal ak doole.
11Erodd aki dagam nag sewal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu yànj, delloo ko Pilaat.
12Erodd ak Pilaat, bésub keroog ay xarit lañu, doonte ay noon lañu woon.
13Ci kaw loolu Pilaat woo sarxalkat yu mag ya, ak njiit ya ak askan wa.
14Mu ne leen: «Yeena ma indil waa jii, ne ma mooy lajjal askan wi. Man nag laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma ci moom genn tooñ ci li ngeen ko tuumaal.
15Erodd itam gisul lenn ci moom, ndax moo nu ko yónneewaat. Mu ngoog, waa jii deful lenn lu jar àtteb dee.
16Kon nag dama koy dóorlu, yiwi ko.»
17Booba fàww Erodd bàyyil leen kenn ca bésu màggal ga.
18Ñépp daldi xaacoondoo, ne: «Reyal kii te yiwil nu Barabas!»
19Barabas nag fippu gu amoon ca dëkk ba, ak nit ku ñu fa bóom, moo waral ñu tëj ko kaso.
20Pilaat namma bàyyi Yeesu, daldi waxaat ak mbooloo ma.
21Teewul ñuy xaacu, naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant!»
22Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Ana lu bon lu kii def? Lenn lu jar dee, gisuma ko ci moom. Kon nag, dama koy dóorlu, yiwi ko.»
23Ñu gënatee xaacu, di sàkku ñu daaj ko ci bant. Seen coow la mujj ko ëpp doole.
24Ci kaw loolu Pilaat dogal ñu defal leen la ñu sàkku.
25Mu yiwi ka ñu ko ñaanoon, te jëfi fippu ak nit ku ñu bóom taxoon ñu tëj ko kaso. Yeesu nag, mu teg ko ci seeni loxo, ngir ñu def ko lu leen neex.
26Ba ñuy yóbbu Yeesu, jenn waay ju dëkk Siren, ñu di ko wax Simoŋ, moom lañu dajeel, mu jóge ca tool ya. Ñu teg bant ba ñuy daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ca moom.
27Nit ñu bare nag topp ko, jigéen ñay yuuxu, di ko jooy.
28Yeesu geesu leen, ne: «Yeen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.
29Ay jant a ngi ñëw kat, dees na ca ne: “Ndokklee jigéen ju tëlee am doom, masula jur, masula nàmpal!”
30Su boobaa, “Nit ñee naan tund yu mag yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’, naan tund yu ndaw yi: ‘Suul-leen nu!’ ”
31Ndegam bant bu tooy lees di def nii, ana nu bant bu wow di mujje?»
32Yóbbaale nañu itam ñaari saaysaay, ngir boole leen ak Yeesu, rey leen.
33Ba ñu agsee ca bérab, ba ñuy wax Kaaŋu bopp, fa lañu daaj Yeesu ci bant, daajaale ñaari saaysaay ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.
34Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.
35Mbooloo maa nga taxaw di seetaan, njiit ya ñoom di ko kókkali, naan: «Musal na ay nit; na musal boppam nag, ndegam mooy Almasib Yàlla, ki ñu fal!»
36Takk-der ya it di ko ñaawal. Ñu dikk, tàllal ko bineegar, ngir mu naan.
37Ñu ne ko: «Gannaaw yaa di buurub Yawut yi, musalal sa bopp!»
38Ñu bindal ko nag fa ko tiim, mbind mii: «Kii mooy buurub Yawut yi.»
39Kenn ca saaysaay ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi? Wallul sa bopp te wallu nu!»
40Moroom ma nag femmu ko, ne ko: «Ragaloo sax Yàlla, te yaa ngi ci menn mbugal mii?
41Nun sax, lii jaadu na ci nun, ndax sunu yoolu jëf lanu jot. Waaye kii deful dara lu teggi yoon!»
42Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttliku ma!»
43Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»
44Ba ñu demee ba tollu wetu fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
45Naka la jant bi giim, ridob biir néeg Yàlla ba xar ca digg ba.
46Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dee.
47Njiitu takk-der ba ko teewe woon nag sàbbaal Yàlla, ne: «Aylayéwén, waa jii ku jub la.»
48Ba loolu amee mboolem ña fa daje woon di seetaan te teewe loolu, ñépp dellu seeni kër, tey fëgg seen dënn ndaxu tiis.
49Mboolem xamey Yeesu, ak jigéen ña ko toppe woon ca Galile, ña nga dànd lu sore, di seetaan.
50Ndeke jenn waay ju ñuy wax Yuusufa, ma nga bokkoon ca kurélu àttekati Yawut ya. Ku baax, ku jub la woon.
51Kooku ànduloon ca àtteb kurél ga ak seen jëf jooju. Ma nga cosaanoo woon dëkkub Yawut ba ñuy wax Arimate, te moom itam, nguurug Yàlla la doon séentu.
52Moom moo dem ca Pilaat, sàkku ci moom, mu jox ko néewub Yeesu.
53Gannaaw loolu mu wàccee ko ca bant ba, sànge ko càngaayal lẽe, denc ko ci bàmmeel bu ñu yett ciw doj, te maseesu caa denc ab néew.
54Bésub Waajal la woon, bésub Noflaay bi ci topp di waaja taxaw.
55Fekk na jigéen ña dale woona ànd ak Yeesu ca Galile, ña nga topp ca Yuusufa. Ñu gis bàmmeel ba, ak na ñu ca dence néew ba.
56Ba loolu amee ñu dellu, waajali cuuraay ak diwu xeeñlu ngir néew ba. Bésub Noflaay nag taxaw, ñu dal-lu, ni ko yoon santaanee.