Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug

Luug 24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ca ëllëg sa, di ndoortel ayu bés, jigéen ña jëlu dem ca bàmmeel ba, yóbbaale cuuraay la ñu waajal.
2Ñu agsi bàmmeel ba, fekk ñu randal doj wa uboon bunt ba, laf ko ca wet ga.
3Ñu dugg, fekkuñu fa néewu Sang Yeesu.
4Naka lañu nekke seenug njaaxle ci loolu, ñaari góor ne jimeet fa seen wet, sol yére yuy melax.
5Naka la leen tiitaange jàpp, ba ñu sukk, dëpp seen jë fa suuf, ñu ne leen: «Kiy dund, lu tax ngeen di ko seet ci biir ñi dee?
6Nekku fi; dekki na. Fàttlikuleen la mu leen waxoon, ba mu génnagulee Galile.
7Da noon: “Fàww ñu teg Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi, ñu daaj ko ci bant, rey ko, ba ñetteelu fanam, mu dekki.”»
8Booba lañu fàttliku kàddug Yeesu googu.
9Ñu jóge ca bàmmeel ba, dem àgge loolu lépp Fukk ñaak benn, ak ña ca des ñépp.
10Jigéen ña àgge loolu ndaw ya ñoo doon Maryaamam Magdala, ak Yowaana, ak Maryaama yaayu Yanqóoba, ak itam ñeneen jigéen ñu àndoon ak ñoom.
11Teewul ñu def waxi jigéen ña ay caaxaan, ba gëmuñu leen.
12Piyeer nag jóg, daw, ba ca bàmmeel ba. Mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Mu daldi ñibbi, jaaxle lool ca mbir ma.
13Ndeke ca bés booba ñaar ca taalibe yaa nga woon ca yoonu dëkk bu ñuy wax Emayus, digganteem ak Yerusalem wara tollu ci fukki kilomeetar.
14Ña ngay waxtaane mboolem xew-xew yooyu.
15Naka lañuy waxtaan ak a diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom.
16Teewul seeni gët tëlee ràññee, ba manuñu koo xàmmi.
17Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis.
18Kenn ci ñoom, ku ñuy wax Kelyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk de, yaa dal Yerusalem te umple li fi xew fan yii?»

19Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede.
20Waaye sunu sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko teg ciy loxo, ngir ñu teg ko àtteb dee, daaj ko ci bant.
21Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy jotsi Israyil. Loolu lépp teewul nu ngii ci ñetteelu fan, ba mbir yooyu amee ba tey.
22Ay jigéen ñu bokk ci nun nag ñoo nu jaaxal. Ndax ñoo jëlu dem ca bàmmeel ba,
23waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dikk, ne ay malaakaa leen feeñu, xamal leen ne Yeesoo ngi dund.
24Ñenn ci sunuy àndandoo it dem nañu ca bàmmeel ba, fekk ko noonee ko jigéen ña waxe. Waaye moom, gisuñu ko.»
25Ci kaw loolu mu ne leen: «Yeen daal, yeena ñàkk xel, yeena naqarim xel, ndegam ba tey gëmaguleen mboolem li yonent yi xamle woon!
26Xanaa du fàww Almasi daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?»
27Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
28Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.
29Ñu daldi koy téye, ne ko: «Dalal ak nun, ndax jant baa ngi so, léegi mu guddi.» Ba loolu amee mu dugg, dal ak ñoom.
30Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen.
31Ca la seeni gët ubbiku, ñu xàmmi ko. Moom nag, mu ne mes, réer leen.
32Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»
33Ñaari taalibe ya daldi jóg ca waxtu woowu tembe, dellu Yerusalem, ca Fukk ñaak benn. Ñu fekk leen ñu dajeek seeni àndandoo.
34Ci kaw loolu ñu ne ñaar ña jóge Emayus: «Ndeke Sang bi kay, dekki na; feeñu na Simoŋ!»
35Ñaari taalibe ya ñoom it, nettali leen la xewoon ca yoon wa ak na ñu xàmmee Yeesu, ba mu daggee mburu ma.
36Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!»

37Tiitaange lu réy jàpp leen, ñu foog ne njuuma lañu gis.
38Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di jaaxle, ak lu ngeen di xel-yaar nii?
39Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.»
40Loolu la leen wax, daldi leen won ay loxoom aki tànkam.
41Taalibe ya nag boole mbég akug jaaxle ba tax manuñu koo gëm. Mu ne leen: «Lu ngeen fi am, lu ñuy lekk?»
42Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.
43Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
44Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.»
45Ca la ubbi seen xel, ngir Mbind mi leer leen.
46Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki,
47te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
48Loolu yeena ko seede.
49Man ci sama bopp maa leen di yónnee li sama baay dige. Waaye yeen toogleen ci dëkk bi, ba kera ñu leen solee manoore ju bawoo fa kaw.»
50Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Ci kaw loolu mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.
51Ba mu leen di barkeel, ca la teqlikoo ak ñoom, ñu yéege ko asamaan.
52Ñoom nag, ñu sujjóotal ko, daldi dellu Yerusalem, ànd ak mbég mu réy.
53Saa su nekk, ña nga woon ca kër Yàlla ga foofa, di sant Yàlla.