Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ayóoba

Ayóoba 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw loolu Ayóoba àddu, ma ngay móolu bés ba mu juddoo.
2Mu ne:
3Sànkute ñeel na bés ba ma juddoo, ba ca guddi ga noon: «Sosees na góor!»
4Boobu bés yal na di lëndëmu neen, di bés bu Yàlla ma fa kaw faaleedi, te genn leer du ko leeralati.
5Yal na lëndëmu njaniiw aakimoo boobu bés, xàmbaar mbaaral ko, muy guddig digg bëccëg gu raglu.
6Googu guddi yal na ko lëndëm moom, yàlla bumu bége fi digg bési at mi, yàlla bees ko limaaleeti ci weer yi.
7Googu guddi kay yàlla bu ci gone sosooti, yàlla bu ci sarxolle jolleeti.
8Yal na alagkati bés yi alag googu guddi, alagkat yu mana xabtal ninki-nànka.
9Yal na biddiiwi njëlam giim, muy séentug leer te du am; yàlla bumu gis fu njël di xippee,
10gannaaw moo tëjul sama biiru ndey, ba làq saay gët coono.
11Moo lu ma tee woona deeye biiru yaay? Lu ma tee ne putt, dog, boog?
12Ana lu may óom doon uufe? Ana lu ma doon nàmpey ween?
13Tëdd koon naak jàmm biir bàmmeel, di nelaw, nopploondook
14buur yeek jawriñi àddina, yi tabaxal seen bopp, këri buur yu gental tey.
15Nopplu koon naak garmi yay boroom wurus, te daan feesal seeni kër, xaalis.
16Mbaa ma mel koon ni lumb wu làqu biir suuf, mbaa cuux mu jotula gis ug leer.
17Biir bàmmeel la ñu bon ñiy noppee sonle, fa la ña jeele doole nopploo,
18ña ñu tëjoon ne finaax, déggatuñu coowal ku leen di sas,

19ku tuut ak ku mag di fa benn, jaam noppi faa jaamu sangam.
20Boroom tiis, ana lees koy maye leeru kaw suuf? Lu boroom naqar di doye bakkan?
21Ku ni mel ku yàkkamti dee gu dikkul, te gëna sàkku dee alal ju làqu,
22ba bu gisoon bàmmeel, di textexi ci biir mbég ak bànneex.
23Ngóor sii aw yoonam làqu, ana lu muy doye dund, te Yàlla dar kepp ko?
24Samay binni di samaw ñam, samay yuux fettax nim ndox.
25Tiitaange déy a ma dikkal, li ma ragaloon kay a ma dab.
26Du jàmm, dug dal, du noflaay bu ma am, jallaañoo dikk na!