1Ba loolu amee Aji Sax ji àddoo fa ngëlén la, ne Ayóoba:
2Ana koo doon, bay lëntal samay dogal, di wax loo xamul dara?
3Takkul boog te góor-góorlu, ma laaj la, nga xamal ma.
4Ana foo nekkoon ba may samp suuf? Waxal su la ko sam xel mayee.
5Ana ku dogal dayo ya, umpu la? Ku tàllal buum, natte ko ko?
6Ana fu kenu ya sampe? Ak ku teg doju coll wa,
7ba biddiiwi njël sarxolleendoo, goney Yàlla yépp xaacoondoo?
8Ana ku tëjoon lafi buntu géej, ba muy buccikoo xóote ya, fettax,
9ba ma solal ko aw niir, mbubb, laltaaye ko lëndëm,
10dagg aw xélam, àppal ko kemu, dogalee ko bunt bu tëje ràpp,
11ba ne ko: «Fii ngay yem, doo fi wees. Fii la say gannax di noppee buure»?
12Ana foo masa joxe suba ndigal, ba xamal njël bérabam,
13ngir mu jàppe cati àddina, ag leeram, yëlëbe ca ñu bon ñi,
14àddina mel ni ban bu ñu teg torluwaay, tey saamandaay mbubb mu ñu suub,
15ñu bon ñi, ñu xañ leen seenug leer, ba loxo ba ñu xàcci woon damm?
16Yaa àkki ba fa géej bënne? Am yaa daagoo ruqi xóotey géej?
17Dees laa won bunti ndee? Am yaa gis bunt ya jëm lëndëmu njaniiw?
18Dangaa ràññee yaatuwaayu suuf si? Waxal, ndegam xam nga lii lépp!
19Ana yoon wa jëm fa leer dëkke, ak fa lëndëm màkkaanoo,
20ba nga man leena yóbbu fa ñu digaloo, te ràññee seen yooni kër?
21Xam nga ko moos, fekk na la juddu; dund nga ay fani fan!
22Yaa àkki ba fa mbàndi tawu yuur ya? Am yaa gis mbàndi waamey donj yu sedd,
23ya may dencal jamonoy njàqare ngir bésub ndajem xare?
24Ana yoon wu jëm fa leer di tasaaroo? Ak fu ngelawal penku di xàjjalikoo, ba dajal suuf si?
25Ana ku xàllal waame, ak ku sàkkal melax ak dënu aw yoon,
26di taw fu kenn newul, ci màndiŋ mu nit amul,
27di suuxat gent bu maral, ba saxal fam ñax?
28Ab taw daa am baay? Ana ku geñoom sos toqi lay?
29Ana ku wasin ndox mu way, ak ku jur layub asamaan bu sedd ba wow,
30ba wali ndox yi dëgër niw doj, déndu géej fasu, ne kekk?
31Yaay faste genn dëllooñ gu ndaw gi ci digg asamaan? Am yaay yiwi dëllooñ gu mag ga mu dendal?
32Yaay def bu jotee, nga feeñal biddiiw yi? Am yaay wommat dëllooñu bëj-gànnaar ak njabootam gu sew?
33Dangaa xam dogali yoon yi yor asamaan? Am yaay saytu kilifteefam fi kaw suuf?
34Yaay yékkatil niir yi kàddug ndigal, rekk waame sang la?
35Yaay yebal melax yi ñu dem, melaxi, délsi, ne la: «Nu ngi, ak fan?»
36Ana ku yeb xel mu rafet cib dënn, ak ku may ab xol dég-dég?
37Ana ku xareñ ba waññ niir yi? Ak kuy jolal mbuusi asamaan,
38ba suuf di bàq, dankaloo, defi donj, taqloo?
39Yaay rëbbal gaynde? Am yaay reggal doomu gaynde
40ju goore biir paxam, mbaa mu waafem ngeer, di tëroo?
41Ana kuy xont baaxoñ, fa doom yay wooye Yàlla wall, di tërëf ndax ub xiif?