Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ayóoba

Ayóoba 29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ayóoba tàmbaleeti ne:
2Éy ku ma doon delloo jamono ya woon, fan ya ma Yàlla daa wattoo;
3ba mu may tiim, di ma niital, may doxe ag leeram, biir lëndëm!
4Ba ma tolloo sama digg doole, te Yàlla xejjoo sama xayma.
5Booba Aji Man jaa ngeek man ba tey, sama gone yu góor yéew ma,
6may jàngoom niw, seggukaay di ma walal ag diw.
7Bu ma génnaa ba ca bunt dëkk ba, digg pénc ma laay jekkasndikoo,
8waxambaane gis ma, ñooru, mag ña jóg, taxawal ma,
9kàngam ne xerem, ub gémmiñam,
10garmi ne selaw, làmmiñam taqoo denqleñam,
11nopp dégg ma, ndokkeel ma, bët gis ma, seereel ma yiw.
12Néew-ji-doole woote, ma wallu, boole ci jirim bu tumurànke.
13Ñaanu ku naroona sànku di ma dal, may tooyal xolu jëtun.
14Njekk laa woddoo woon, njekk wodd ma, te dëgg laa defoon mbubb ak kaala.
15Silmaxa, maa dooni gëtam; ab lafañ, ma diy tànkam.
16Néew-ji-doole, maa doon baayam, ku ma xamul sax, may seet àqam.
17Ku jubadi, ma dammi ŋaamam, foqatee am pàddam cay sellam.
18Ma noon samay fan dina neexook feppi suuf, ma doora deeye sama biir njaboot.

19Ma noon su ma doon garab samay reen fëllem ndox, ab lay fanaanee faam car ya.
20Ma noon darajaa may yeesalal nganam, may gëna daŋalati xala.
21Man lees daa déglu, di ma xaar; ne cell, di taataan samam xel.
22Samay kàddoo leen di dal, genn-genn, te su ma àddoo ba daaneel, kàddu jeex.
23Booba lees ma daa séentu nib taw; ŋa ŋàpp, di nég waamey waxset.
24Samay ree gëmeesu ko woon, xanaa ne siiwa gis sama kanam gu leer.
25Maa jiite woon, di dogal doxalin, toog toogaayu buur ci biir gàngooram, te di leen dëfal ci seen naqar.