1Elifas àddu, ne:
2Ayóoba, ku xelu dina tontoo kàdduy ngelaw, mbel-mbelam nib jaas bu fees dënnam a?
3Ku xelu du layoo waxi caaxaan, kàddu yu amul lenn njariñ.
4Yaw de, yaa ngi neenal worma, di yàq njàngat mi war fa Yàlla.
5Saw làmmiñ déy, sa ndëngtee koy sa, yaa taamu di wax njublaŋ.
6Du man de, sa gémmiñu bopp a la teg daan, sa làmmiñu bopp a la tuumaal.
7Xanaa yaa jëkka juddu ci nit? Am balaa tund yee sosu lañu la jur?
8Ba Yàllay féncoo yaa doon déglu, ba mana aakimoo xel mu rafet?
9Ana loo xam lu nu xamul ak dég-dég boo am, te nu rafle ko?
10Boroom bijjaaw ak màggat a ngi sunu biir, di ñu sut sa baay aw fan.
11Kàddu yi la Yàlla di mas-sawoo da laa doyul? Boole ci li ñu lay waxe teeyu bakkan?
12Ana looy waxe xol, di saxaral kanam nii?
13Ngay sippi Yàlla sa mer, di ko wax lu mel nii!
14Ana nit ku mana jub xocc? Ana ku laab ku jigéen jur?
15Yàlla wóoluwul sax ñu sellam ña ca asamaan, te asamaan sellul ba doy ko,
16rawatina nit, moom mi jara seexlu, yàqu jikko, di def njubadi ni ndoxum naan.
17Déglu ma, ma wax la, xamal la li ma gis,
18muy lu ñu rafet xel ñi jottli, jële ko ca seeni maam, te làquñu ko.
19Ñoom, seeni maam doŋŋ a jagoo woon réew mi, ba leen doxandéem raxaguloon.
20Bésoo bés ku bon ay bittarñikoo biir njàqare, te diirub at yi ñu àppal ku néeg,
21coowal musiba mooy buur nopp ya, yàqkat bette ko biir jàmm.
22Dootu yaakaara mucc musiba, saamar a koy yoot,
23muy taxawaalu, tan ya mujj xontoo, mu xam ne bésub safaan taxaw na.
24Njàqareek tiitaangee koy ëlëm, song ko ni buur bu jekku xare.
25Moo xàccil Yàlla loxo, di jaay Aji Man ji njàmbaar,
26daŋŋiiral, buur, wuti ko, yiiroo dëllaayu pakkam,
27te fekk ko yaflu ba gët suulu, pooj ya duuf bay lob-lobi.
28Ku ni mel ay dëkke dëkk yu gental, ci kër yu kenn dul dëkke, kër yu nara doon jali tojit.
29Ku bon kooku du woomle, alalam du toog, te koomam du lawe miim réew.
30Du mucc musiba, mooy garab gu daay xoyom car yu yees ya, Yàlla wal, mu ne mes.
31Bumu yaakaar naxi neen, di nax boppam, nde neen ay doon ab añam.
32Balaa jantam a lang mu jot añam, te caram dootu naat.
33Day mel ni reseñ gu doom yay yolax, mbaa oliw gu tóor-tóor yay ruus.
34Waa làngu yéefar yi duñu am kuutaay, te xaymay lekk-kati ger yi la sawara di xoyom.
35Ñooy sos joote, wasin ñaawtéef, ñoom la seen biir di ëmb wuruj.