Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ayóoba

Ayóoba 10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Maaka sib sama dund gii! Naa afal sama kàddug tawat, di àddoo naqaru xol.
2Dama naa Yàlla: Bu ma topp ug tooñ. Xamal ma kay li nga may topp, lu mu!
3Ana lu la note di jariñ, ba ngay bañ li nga sàkke sa loxol bopp, tey àntal pexem ku bon?
4Xanaa gëti nit doŋŋ nga am, am ni nit di gise rekk ngay gise?
5Say fan daa tollook fani doom aadama, am say at daa yem ak ati nit,
6ba ngay seet fu ma ñaawe, di liñbat fu ma moye?
7Moona xam nga xéll ne tooñuma, te amul kenn kuy xettli nit ci sa loxo.
8Say loxoo ma mooñ, tabax ma ba ma mat sëkk, léegi nga di ma yàq yaxeet!
9Rikk fàttlikul ne yaa ma tabax, ni bu ma doon ban, xanaa doo ma delloo xaat ci pëndub suuf?
10Xanaa du yaa ma xelli woon ni meew ci sama biiru ndey, wayal ma nim soow,
11wodde ma der ak suux, ràbbe ma yax aki siddit?
12Yaa ma may bakkan, won ma ngor, yaa sàmme sa yégeel samag noo.
13Ndeke yoo lii nga dencoon ci sa xol, xam naa ne lii nga naroon:
14ne ma dann, ba su ma bàkkaaree, doo ma baal samag tooñ.
15Su ma defee lu bon, ngalla man, te bi ma defee njekk it, sañumaa siggi, gàcce laa suure, sangoo toroxte.
16Waaye su may siggi rekk nga mel ni gaynde, di ma rëbb, dellu di ma lore say kiraama,
17yónneeti ma say seede, gën maa songati, ay gàngoor di wuutante fi sama kaw.
18Ana loo ma doon génnee sama biiru ndey? Doon naa dee te bët du ma gis!

19Doon naa mel ni ku masula am, jóge ci biir, ñu yóbbu bàmmeel.
20Xanaa du fan yu néew laa dese? Ba ma boog! Xiddil, ma leqliku,
21bala may dëddu, délseetuma, bala may tàbbi réew mu lëndëm ga ne këruus,
22réewum lëndëm, mu ne këruus, salfaañoo, ag leer sax, saf fa lëndëm!