Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ayóoba

Ayóoba 32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Fa la ñetti góor ñooña noppee tontu Ayóoba, ndax la Ayóoba gis njekkam.
2Ba loolu amee Eliyu doomu Barakel ma askanoo ci Buus, bokk ci làngu Ram daa mer ba futt ca la Ayóoba dëggal boppam fi kanam Yàlla,
3ak la ñetti xariti Ayóoba ya ñàkk lu ñu ko tontu, ba tax ñu teg Yàlla tooñ.
4Eliyu nag moo mujjoona wax ak Ayóoba, ndax moo féete ndaw ñett ña.
5Mu gis ne ñetti góor ña amatuñu tont, xol ba sot, mu mer ba futt.
6Ca la Eliyu doomu Barakel waa Buus ba, àddu ne: Man de damay ndaw, ngeen diy mag, ba tax may teeylu, ragal leena biralal sama xam-xam.
7Ma noon: «Na yàgga-dund wax, na dund-jopp xamle xel mu rafet.»
8Ndeke xel mi ci nit mooy noowal Aji Man ji koy may dég-dég.
9Dund-jopp taxula rafet xel, te di mag taxula xam yoon.
10Moo tax ma ne: «Déglu ma; man it ma biral sama xam-xam.»
11Dama ne, négandiku naa seeni kàddu, teewlu seeni déggin, ba ngeen di jeexi tont ba tey.
12Yeen laa doon teewlu, te kat kenn ci yeen yeyu ci Baay Ayóoba, kenn joxu ko tontam.
13Buleen ma ne: «Xel mu rafet mi nu ci gis moo di: Yàllaa ko mana tiiñal waaye du nit.»
14Du man la Baay Ayóoba jëme kàddoom, kon du seeni wax laa koy tontoo.
15Ñii kat jommi nañu, waxatuñu; ba kàddu dëddu leen!
16Dama leen di xaar te waxuñu, xanaa taxaw, tontootuñu?
17Damay tontu sama wàll, man it; damay biral sama xam-xam, man it kay!
18Sama dënn a fees aki wax, te samam xel xiir ma ci wax.

19Sama xol baa ngii mel ni lu sol biiñ, ube ràpp, mbete mbuus mu yees mu nara fàcc.
20Naa wax boog, ba féex, naa àddu, ba tontu.
21Duma ci am xejj ak seen, te duma jay kenn.
22Xawma sax nu ñuy jaye, nde konoon ki ma sàkk gaaw ma fee jële.