Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ayóoba

Ayóoba 7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Xanaa du fani doom aadama fi kaw suuf àppu doñ-doñ la, dundam di dundu liggéeykat bu ñu bind?
2Daa mel ni jaam bu namm keppaar mbaa mbindaan mu yàkkamtig peyam.
3Noonu laa séddoo ay weeri mititu neen, jagoo ni ay guddiy coono.
4Damay tëdd te naa: «Kañ laay jóg nag?» Waaye guddi gudda gudd, walbatiku ba fajar xar génnliku na ma!
5Maa ngi sàngooy sax ak àkki ban, sama der biy xar, di wal.
6Kukkub ràbb sax ni samay fan di jeexee ko gaaw, poqe di jeex, te yaakaar amul.
7Éy Yàlla, bul fàtte ne sama dund gii, ag noo doŋŋ la, te dootuma teg bët ngëneel.
8Bët bi may gis tey du ma gisati, dinga ma niir, fekk nekkatuma.
9Niir wu naaxsaay, ne mes, mooy ku wàcci njaniiw, du yéegati!
10Du ñibbeeti këram, dëkkuwaayam dootu ko fat.
11Moo tax duma téye sama làmmiñ, xanaa di waxe biir njàqare, di jooye biir naqar.
12Dama di Géej menn mbaa Ninki-nànka, ba nga di ma booleek ku may wattu?
13Dama naan: «Naa nopploo tëraayub laltu, ba yennikoo ab lal sama tawat,»
14nga di ma tiitale ay gént, di ma xoqtale ay jeneer,
15ba ku ma xojoon sax, ma jël, nde dee a ma gënal dese yii yax.
16Doy na sëkk! Dunduma ba fàww; ba ma, samay fan genn noo la!
17Luy nit ba nga di ko gëddaal, bay def sam xel ci moom,
18di ko nemmiku saa yoo xëyee, di ko nattu saa su ne?

19Doo ma dummóoyu boog, may ma sax fu ma wonaasoo?
20Yaw miy seetlu jaam ñi, ma bàkkaar, lu mu lay wàññi? Ana lu tax nga di ma diiral sa bopp nii, ba ma mujj diis la gann?
21Lu tee kon nga baal ma samag moy, jéggal ma samag tooñ? Léegi tey ma tëri biir suuf, nga di ma seeta seet, fekk nekkatuma.