Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ayóoba

Ayóoba 28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Xaalis déy am na mbellam, wurus am bérabu seggukaayam,
2weñ gu ñuul ci suuf lees ko jële, te xànjar, ay doj lees di xelli, ba am ko.
3Dees na taal, dàq ug lëndëm, di gëstu ba fu gëna làqu doji biir lëndëm gu ne këruus.
4Nit a ngi gas ay xunti fu soreeki dëkkuwaay, di sandaamtalook a jaayu fu kenn newul, te tànk jaarewu fa.
5Kaw suuf day meññ ub dund, xóote ya mel ni lu sawara salfaañe.
6Doj ya ca biir la peri safiir màkkaanoo, te pëndaxu wurus ñàkku fa.
7Wii yoon, tan xamu ko, bëtu jaxaay du ko gis.
8Rabu àll du fa joggi, te gaynde sax du fa jaare.
9Loxol nit ay song doju kekk, buddi reeni tund, jàllarbi.
10Ci biir xeer yi lay yettey xunti, ba bëtam di gis lu cay alal.
11Nit a ngi dogale wali ndox, ba lu làqu woon, mu leeral nàññ.
12Waaye xel mu rafet fees koy jële, ak fu ag dégg màkkaanoo?
13Doom aadama xamul njégam, te amul biir réewum aji dund ñi.
14Xóote ya nee: «Xel mu rafet dëkku fi de!» Géej ne: «Nekku fi de!»
15Wurus mayewu ko, xaalis wecciwul njégam.
16Deesu ko weccee wurusu ngalam it, mbaa peri onigsë ak safiir.
17Deesu ko méngaleek wurus ak ngën-gi-per yuy tàkk, te ngën-gi-gànjari wurus wecciwu ko,
18waxeesuli xor ak yeneen xeeti per; xel mu rafet a gën per yu gëna jafe,

19du moroomu peru topaas ba ca réewum Kuus, te wurusu ngalam daal wecciwu ko.
20Xel mu rafet, ana fu mu jóge, ak fu ag dégg màkkaanoo?
21Ump na bëtu lépp luy dund; njanaaw la fa kaw sax gisu ko.
22Paxum sànkutee ngi àddoondook ndee naan: «Dégmati nan ub jëwam de!»
23Yàllaa ràññee yoon wa jëm xel mu rafet, te moo xam màkkaanam.
24Kii daal ay jéer ba fa cati àddina, di gis mboolem lu asamaan tiim.
25Ba Yàlla àppalee ngelaw diisaayam, nattal ndox ab dayoom,
26ba mu sàkkalee ab taw dogalu yoonam, sàkkal melax ak dënu aw ñallam,
27ca la nemmiku xel mu rafet, xamle ko, samp ko, gëstu ko,
28daldi ne doom aadama: «Ragal Boroom bi daal, mooy xel mu rafet, te dëddu lu bon mooy am ug dégg.»