Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yunus

Yunus 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ci kaw loolu Aji Sax ji yebal jën wu mag, mu wonn Yunus. Mu nekk ca biiru jën wa ñetti bëccëg ak ñetti guddi.
2Yunus ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, fa mu tollu ca biir jën wa.
3Mu ne: Maa jàq, woo Aji Sax ji, mu wuyu ma. Ca xóotey njaniiw laa wootee wall, nga dégg ma.
4Yaa ma xalab xóotey xolu géej, ndaw ma mëdd ma. Say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
5Man nag ma naan: «Dàqees na ma, ba ma sore la, waaye maay dellu gis sa kër gu sell ga!»
6Ndox maa ma tanc ba ci put, xóotey géej mëdd ma, waag ba laxasu sama bopp.
7Ca reeni tund ya laa suuxi, caabiy suuf féete ma gannaaw ba fàww, waaye ca kan ma nga jukkee sama bakkan, yaw, sama Yàlla Aji Sax ji.
8Noowal bakkan a nga may rëcc, sama xel ne yarr ci yaw, Aji Sax ji, sama ñaan àgg fa yaw, ca sa kër gu sell ga.
9Ñiy wormaal neenug neen daal, ñoo dëddu seen yiw fa Yàlla.
10Man nag, ci biir cant laa lay sarxale. Li ma xas laay sottal. Wall, fa Aji Sax ji!
11Ci kaw loolu Aji Sax ji wax ak jën wa, mu goqi Yunus ca tefes ga.