Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 9

Luug 9:31-62

Help us?
Click on verse(s) to share them!
31Ñoo feeñ ci ag leer, di waxtaane dëddug Yeesu, ga mu doon waaja sottale fa Yerusalem.
32Booba ngëmment a ngay man Piyeer ak ña mu àndal. Ba ñu teewloo nag lañu gis leeru Yeesu, ak ñaar ña mu taxawal.
33Ba ñu demee ba ñaari nit ñooñu di bàyyikoo fa Yeesu, Piyeer ne ko: «Njaatige, su nu toogoon fii de, mu baax ci nun; nan yékkati ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa, benn Ilyaas.» Waaye booba Piyeer xamul la muy wax.
34Naka lay wax loolu, aw niir dikk yiir leen, taalibe ya tàbbi ca biir niir wa, tiitaange jàpp leen.
35Ci biir loolu baat jibe ca niir wa, ne: «Kii moo di sama Doom, ki ma taamu; dégluleen ko.»
36Ba baat ba selawee, Yeesu doŋŋ a feeñ. Taalibe ya nag ñoom ne cell, waxuñu kenn lenn jant yooyu, ca la ñu gis.
37Ca ëllëg sa ba ñuy wàcce tund wa, mbooloo mu baree dikk dajeek Yeesu.
38Jenn waay jekki xaacoo ca mbooloo ma, ne: «Sëriñ bi, dama lay ñaan, nga xoolal ma sama doom, ndax moom doŋŋ laa am.
39Rab kat moo ko jàpp, mu jekki di yuuxu, di say, gémmiñ giy fuur. Daanaka du teqlikook moom te sonal na ko.
40Ñaan naa say taalibe ngir ñu dàqal ma ko, waaye manuñu ko.»
41Yeesu ne leen: «Céy niti tey, yeena gëmadi te dëng! Maak yeen ba kañ, te di leen muñal? Indi sa doom fii.»
42Naka la xale bi jubsi Yeesu, rab wi sànni ko ci suuf, muy say. Yeesu itam gëdd rab wa, wéral xale ba, delloo ko baayam.
43Ñépp nag waaru ci màggug Yàlla. Naka la ñépp di yéemu ca mboolem la Yeesuy def, mu ne taalibeem ya:
44«Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»
45Taalibe ya nag dégguñu kàddu googu, ndax fekk na piri ma làqu leen, ngir ñu bañ koo daj, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
46Werante moo dikkaloon taalibe yi, ñuy seet kan moo gëna kawe ci ñoom.
47Yeesu nag ràññee seen xalaat. Mu daldi indi ab xale, taxawal ko ci wetam.
48Mu ne leen: «Xale bii, képp ku ko dalal ndax sama tur, man nga dalal; te képp ku ma dalal, dalal nga ki ma yebal; ndax ki gëna tuut ci yeen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
49Ci kaw loolu Yowaan àddu, ne: «Njaatige, danoo gis nit kuy dàqe sa tur ay rab, nu aaye ko, ndax bokkul ci nun.»
50Yeesu ne ko: «Buleen ko aaye, ndax ku la sotul, yaw la faral.»
51Ba ñu demee ba bés bi ñu wara yéege Yeesu di jubsi, Yeesu moo dogu ngir dem Yerusalem.
52Mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem, ba agsi ab dëkk ci diiwaanu Samari, nar ko faa waajal ab dal.
53Waa Samari nag nanguwuñu koo dalal, ndax Yerusalem ga mu nammoona jëm.
54Taalibe ya ñuy wax Yanqóoba ak Yowaan gis loolu, daldi ne: «Sang bi, soo bëggee nu jox sawara ndigal, mu wàcce asamaan, faagaagal leen?»
55Teewul Yeesu geesu, femmu leen.
56Ba loolu amee ñu jàll jëm beneen dëkk.
57Ca yoon wa ñu awe la jenn waay ne Yeesu: «Yaw laay topp fépp foo jëm.»
58Yeesu itam ne ko: «Till ak kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye Doomu nit ki de, amul fu mu wéer boppam.»
59Mu neeti keneen: «Toppal ci man.» Mu ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem robi sama baay.»
60Mu ne ko: «Bàyyil néew yi, ñu rob seeni néew, waaye yaw demal, yégleji nguurug Yàlla.»
61Keneen neeti ko: «Sang bi, yaw laay topp, waaye may ma, ma jëkka tàggtook sama waa kër.»
62Yeesu ne ko: «Képp ku tàmbalee gàbb tey xool gannaawam, jekkoo ci nguurug Yàlla.»

Read Luug 9Luug 9
Compare Luug 9:31-62Luug 9:31-62