Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 4

Luug 4:9-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, aj ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga, ne ko: «Ndega yaa di Doomu Yàlla, tëbeel fii, wàcc,
10ndax bindees na ne: “Ay malaakaam lay jox ndigal ci sa mbir, ñu sàmm la,
11te seeni loxo lañu lay leewoo, ba doo fakktaloo aw doj.”»
12Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Bul seetlu Boroom bi sa Yàlla.”»
13Seytaane lalal na Yeesu gépp fiir ba sottal, doora dem, bàyyi ko ab diir.
14Ba loolu amee Yeesu dellu Galile ci manoorey Noo gi, ab jëwam nag law ca diiwaan ba bépp ba mu daj.
15Muy jàngle ca seeni jàngu, ñépp di ko kañ.
16Yeesu moo dikkoon Nasaret ga mu fekk baax, daldi dugg ca jàngu ba, na mu ko baaxoo woon ci bésub Noflaay. Mu taxaw ngir biral ab dog.
17Ñu jox ko téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ubbi téere bi, gis dog bi ñu bind ne:
18«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,
19tey yégle atum yiw wu Boroom bi.»
20Ci kaw loolu mu ub téere bi, delloo ko jawriñ ba, daldi toog. Ña ca jàngu ba ñépp nag ne ko jàkk.
21Mu àddu, ne leen: «Tey jii la mbind mii mat, ngeen dégg.»
22Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?»
23Mu ne leen: «Xam naa ne dingeen ma waxal waxin wi ñu naan: “Fajkat bi, fajal sa bopp.” Mboolem li nu dégg ne moo xew Kapernawum, def ko fii ci sa réewum bopp itam.»
24Mu neeti: «Maa leen ko wax déy, amul benn yonent bu ñu teral ci réewum boppam.
25Maa leen wax ne liy dëgg moo di, ca jamonoy Ilyaas, ba asamaan tëjoo diiru ñetti at ak juróom benni weer, ba xiif bu metti am ca réew mépp, ay jëtun ñu baree nga woon ca Israyil.
26Moona du kenn ci ñoom ku ñu yebal Ilyaas ca moom ku moy jëtun ba dëkke Sarebta, ca Sidon.
27Jamonoy Yonent Yàlla Alyaasa itam, ay gaana yu baree nga woon ca Israyil. Waaye fajeesu ci kenn ku moy Naaman, waa Siri ba.»
28Ba mboolem waa jàngu ba déggee loolu dañoo mer ba fees.
29Ñu jóg, bëmëx ko ba génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca kéméju tund, wa seen dëkk ba sance, ngir xalab ko ci suuf.
30Teewul moom mu jaare ci seen biir, dem yoonam.
31Ba mu ko defee Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile, di leen jàngal ca bési Noflaay ya.
32Nit ña nag yéemu ca njàngleem, ndax sañ-sañ ba muy waxe.

Read Luug 4Luug 4
Compare Luug 4:9-32Luug 4:9-32