Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 4:9-32 in Wolof

Help us?

LUUG 4:9-32 in Téereb Injiil

9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf,
10 ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu sàmm la,
11 dinañu la leewu ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”»
12 Yeesu ne ko: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
13 Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.
14 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.
15 Muy jàngle ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
16 Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésub noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi.
17 Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:
18 «Xelum Boroom baa ngi ci man, ndaxte moo ma tànn, ngir ma yégal néew doole yi xibaaru jàmm bi. Dafa maa yónni, ngir ma yégal jaam ñi ne dinañu leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, te jot ñi ñu not,
19 tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»
20 Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët.
21 Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.»
22 Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?»
23 Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»
24 Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam.
25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Ilyaas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
26 Moona Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.
27 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alyaasa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naamaan, mi dëkkoon réewu Siri.»
28 Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer.
29 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.
30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.
31 Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile.
32 Mu jàngal leen ca bésub noflaay ba, ñu waaru ca njàngleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ.
LUUG 4 in Téereb Injiil

Luug 4:9-32 in Kàddug Yàlla gi

9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, aj ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga, ne ko: «Ndega yaa di Doomu Yàlla, tëbeel fii, wàcc,
10 ndax bindees na ne: “Ay malaakaam lay jox ndigal ci sa mbir, ñu sàmm la,
11 te seeni loxo lañu lay leewoo, ba doo fakktaloo aw doj.”»
12 Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Bul seetlu Boroom bi sa Yàlla.”»
13 Seytaane lalal na Yeesu gépp fiir ba sottal, doora dem, bàyyi ko ab diir.
14 Ba loolu amee Yeesu dellu Galile ci manoorey Noo gi, ab jëwam nag law ca diiwaan ba bépp ba mu daj.
15 Muy jàngle ca seeni jàngu, ñépp di ko kañ.
16 Yeesu moo dikkoon Nasaret ga mu fekk baax, daldi dugg ca jàngu ba, na mu ko baaxoo woon ci bésub Noflaay. Mu taxaw ngir biral ab dog.
17 Ñu jox ko téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ubbi téere bi, gis dog bi ñu bind ne:
18 «Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,
19 tey yégle atum yiw wu Boroom bi.»
20 Ci kaw loolu mu ub téere bi, delloo ko jawriñ ba, daldi toog. Ña ca jàngu ba ñépp nag ne ko jàkk.
21 Mu àddu, ne leen: «Tey jii la mbind mii mat, ngeen dégg.»
22 Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?»
23 Mu ne leen: «Xam naa ne dingeen ma waxal waxin wi ñu naan: “Fajkat bi, fajal sa bopp.” Mboolem li nu dégg ne moo xew Kapernawum, def ko fii ci sa réewum bopp itam.»
24 Mu neeti: «Maa leen ko wax déy, amul benn yonent bu ñu teral ci réewum boppam.
25 Maa leen wax ne liy dëgg moo di, ca jamonoy Ilyaas, ba asamaan tëjoo diiru ñetti at ak juróom benni weer, ba xiif bu metti am ca réew mépp, ay jëtun ñu baree nga woon ca Israyil.
26 Moona du kenn ci ñoom ku ñu yebal Ilyaas ca moom ku moy jëtun ba dëkke Sarebta, ca Sidon.
27 Jamonoy Yonent Yàlla Alyaasa itam, ay gaana yu baree nga woon ca Israyil. Waaye fajeesu ci kenn ku moy Naaman, waa Siri ba.»
28 Ba mboolem waa jàngu ba déggee loolu dañoo mer ba fees.
29 Ñu jóg, bëmëx ko ba génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca kéméju tund, wa seen dëkk ba sance, ngir xalab ko ci suuf.
30 Teewul moom mu jaare ci seen biir, dem yoonam.
31 Ba mu ko defee Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile, di leen jàngal ca bési Noflaay ya.
32 Nit ña nag yéemu ca njàngleem, ndax sañ-sañ ba muy waxe.
Luug 4 in Kàddug Yàlla gi