Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 6

Luug 6:2-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ñenn ca Farisen ya ne leen: «Lu waral ngeen di def lu yoon mayewul ci bésub Noflaay?»
3Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom, ak ña mu àndaloon?
4Ba mu duggee ca kër Yàlla ga, mburum teewal ma la jël, lekk, jox ca ña mu àndal, te yoon mayewul kenn ku ca lekk ku dul sarxalkat yi.»
5Mu neeti leen: «Bésub Noflaay, Doomu nit ki mooy boroom.»
6Beneen bésub Noflaay, Yeesu dugg ca jàngu ba, di jàngle. Jenn waay ju loxol ndijooram làggi ma nga fa woon.
7Firikati yooni Musaa yaak Farisen yaa ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ca bésub Noflaay ba, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8Yeesu nag xam seen xalaat, daldi ne boroom loxo ba: «Jógal taxaw fii ci digg bi.» Mu jóg taxaw.
9Yeesu ne leen: «Laaj naa leen, ana lu yoon maye ci bésub Noflaay; def lu baax am lu bon? Musal bakkan am lore?»
10Ci kaw loolu mu dawal bëtam, xool ña ko yéew ñépp, ba noppi ne waa ja: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal, loxo ba wér.
11Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu.
12Fan yooyu la Yeesu dem kaw tund wa ngir ñaani fa; mu fanaane faa ñaan ci Yàlla.
13Ba bët setee, mu woo ay taalibeem, tànn ca fukk ak ñaar ñii, tudde leen ay ndawam:
14Simoŋ mi Yeesuy wooye itam Piyeer, ak Àndre mi bokk ak Piyeer ndey ak baay, ak Yanqóoba ak Yowaan, ak Filib ak Bartelemi,
15ak Macë ak Tomaa, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ mi ñuy wax farlukatu moom-sa-réew,
16ak Yuda doomu Yanqóoba, ak Yuda Iskaryo ma mujj wor.
17Ci kaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, wàcc, daldi taxaw ca joor ga. Ay taalibeem yu baree nga fa woon ak mbooloo mu réya réy: ay niti Yude gépp, ak Yerusalem ak Tir ak Sidon, dëkki wetu tefes ga.
18Ñu dikk, di ko déglu tey faju ba tàggook seeni jàngoro. Ñi rab jàpp it, wér.
19Mbooloo mépp a ko doon wuta laal ndax leer guy bàyyikoo ca moom, di faj ñépp.
20Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: «Ndokklee yeen ñi néewle, nde nguurug Yàlla, yeenay boroom.
21Ndokklee yeen ñi xiif tey, nde dingeen regg. Ndokklee yeen ñiy jooy tey, nde dingeen ree.
22Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit ki.
23Bésub keroog, bégleen te bànneexu bay fecc ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu la seen maami bañ yooyu daan def ak yonent ya.
24Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.
25Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, ndax dingeen xiif ëllëg. Wóoy yeen ñiy ree tey, ndax dingeen tiislu, dingeen jooy.
26Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya.
27«Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax.
28Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
29Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.
30Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.
31Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu.
32«Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen.

Read Luug 6Luug 6
Compare Luug 6:2-32Luug 6:2-32