Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 6:2-32 in Wolof

Help us?

LUUG 6:2-32 in Téereb Injiil

2 Am ay Farisen yu ne: «Lu tax ngeen di def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi?»
3 Yeesu ne leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
4 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat.»
5 Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésub noflaay bi.»
6 Beneen bésub noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngle. Amoon na fa nit ku loxol ndijooram làggi.
7 Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8 Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanam ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw.
9 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»
10 Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ.
11 Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu.
12 Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla.
13 Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam:
14 Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
15 Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
16 Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujja wor.
17 Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon.
18 Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu.
19 Ñépp a ngi ko doon wuta laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp.
20 Yeesu xool ay taalibeem, ne leen: «Yéen ñi néew doole, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo.
21 Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen, ndax dingeen regg. Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen, ndax dingeen ree.
22 Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki.
23 Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi.
24 Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen, ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex.
25 Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen, ndax ëllëg dingeen xiif. Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen, ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc.
26 Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent.
27 «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ.
28 Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.
29 Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki.
30 Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.
31 Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.
32 «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp.
LUUG 6 in Téereb Injiil

Luug 6:2-32 in Kàddug Yàlla gi

2 Ñenn ca Farisen ya ne leen: «Lu waral ngeen di def lu yoon mayewul ci bésub Noflaay?»
3 Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom, ak ña mu àndaloon?
4 Ba mu duggee ca kër Yàlla ga, mburum teewal ma la jël, lekk, jox ca ña mu àndal, te yoon mayewul kenn ku ca lekk ku dul sarxalkat yi.»
5 Mu neeti leen: «Bésub Noflaay, Doomu nit ki mooy boroom.»
6 Beneen bésub Noflaay, Yeesu dugg ca jàngu ba, di jàngle. Jenn waay ju loxol ndijooram làggi ma nga fa woon.
7 Firikati yooni Musaa yaak Farisen yaa ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ca bésub Noflaay ba, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
8 Yeesu nag xam seen xalaat, daldi ne boroom loxo ba: «Jógal taxaw fii ci digg bi.» Mu jóg taxaw.
9 Yeesu ne leen: «Laaj naa leen, ana lu yoon maye ci bésub Noflaay; def lu baax am lu bon? Musal bakkan am lore?»
10 Ci kaw loolu mu dawal bëtam, xool ña ko yéew ñépp, ba noppi ne waa ja: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal, loxo ba wér.
11 Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu.
12 Fan yooyu la Yeesu dem kaw tund wa ngir ñaani fa; mu fanaane faa ñaan ci Yàlla.
13 Ba bët setee, mu woo ay taalibeem, tànn ca fukk ak ñaar ñii, tudde leen ay ndawam:
14 Simoŋ mi Yeesuy wooye itam Piyeer, ak Àndre mi bokk ak Piyeer ndey ak baay, ak Yanqóoba ak Yowaan, ak Filib ak Bartelemi,
15 ak Macë ak Tomaa, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ mi ñuy wax farlukatu moom-sa-réew,
16 ak Yuda doomu Yanqóoba, ak Yuda Iskaryo ma mujj wor.
17 Ci kaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, wàcc, daldi taxaw ca joor ga. Ay taalibeem yu baree nga fa woon ak mbooloo mu réya réy: ay niti Yude gépp, ak Yerusalem ak Tir ak Sidon, dëkki wetu tefes ga.
18 Ñu dikk, di ko déglu tey faju ba tàggook seeni jàngoro. Ñi rab jàpp it, wér.
19 Mbooloo mépp a ko doon wuta laal ndax leer guy bàyyikoo ca moom, di faj ñépp.
20 Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: «Ndokklee yeen ñi néewle, nde nguurug Yàlla, yeenay boroom.
21 Ndokklee yeen ñi xiif tey, nde dingeen regg. Ndokklee yeen ñiy jooy tey, nde dingeen ree.
22 Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit ki.
23 Bésub keroog, bégleen te bànneexu bay fecc ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu la seen maami bañ yooyu daan def ak yonent ya.
24 Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.
25 Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, ndax dingeen xiif ëllëg. Wóoy yeen ñiy ree tey, ndax dingeen tiislu, dingeen jooy.
26 Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya.
27 «Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax.
28 Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
29 Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.
30 Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.
31 Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu.
32 «Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen.
Luug 6 in Kàddug Yàlla gi