Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 15

Luug 15:1-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mboolem juutikat yeek bàkkaarkat yi ñoo daan ñëw ci Yeesu, di ko déglu.
2Ci biir loolu Farisen ya ak firikati yoon ya di ñurumtu naan: «Kii moom bàkkaarkat yi lay neexool, di bokk ak ñoom lekk!»
3Yeesu nag léeb leen lii, ne leen:
4«Ana kan ci yeen mooy am téeméeri xar, réerle ci menn, te bàyyiwul ca àll ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent (99), ngir toppi ma réer, ba gis ko?
5Bu ko gisee lay bég, teg ko ca mbagg ma, yóbbu kër ga.
6Te bu àggee ca kër ga, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, sama xar ma réeroon, gis naa ko!”
7«Maa leen wax, ne leen: bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee, noonu rekk lay doone mbégte fa asamaan, ba raw mbégte ma fay am, bu juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti nit jubee, te soxlawuñoo tuub.
8«Te it ana jan jigéen mooy am fukki libidoor, benn réer ca, te taalul ab làmp, buub néeg ba, seeta seet, ba gis ko?
9Bu ko gisee, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, libidoor ba réeroon, gis naa ko.”
10Maa leen wax ne leen: noonu rekk lay doone mbégte fa malaakay Yàlla ya, bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee.»
11Yeesu neeti: «Nit a amoon ñaari doom yu góor.
12Ka gën di ndaw ne baay ba: “Baay, jox ma cér bi ma yoon may ci sunu alal.” Ba loolu amee baay ba séddale leen alalam.
13Ay fan yu néew gannaaw gi, ka gën di ndaw jaay léppam, daldi tukki réew mu sore, di topp bakkanam ba yàq fa alalam.
14Gannaaw ba mu sànkee lépp, xiif bu metti dikkal réew ma, mu daldi tàmbalee ñàkk.
15Ci kaw loolu mu dem, di surgawu ku cosaanoo ca réew mooma, kooku yebal ko ca ay toolam, muy sàmm ay mbaam-xuux.
16Mu dem ba noon ngéeja lekk ca xolliti doomi garab ya mbaam-xuux yay lekk, fajeb xiifam, te kenn mayu ko ca.
17Xel ma mujj délsi, mu ne: “Ñaata surga la sama baay am, seen lekk ne gàññ, man, ab xiif di ma rey fii!
18Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;
19yeyootumaa tuddoo sax sa doom; léegi def ma ni ku bokk ci say surga.’ ”
20«Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.
21Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; yeyootumaa tuddoo sax sa doom.”
22Teewul baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb mi gëna rafet, solal ko, te ngeen takkal ko ab jaaro ci loxoom, solal ko ay dàll.
23Indileen sëlluw yafal wa, rey, nu lekk, te bànneexu;

Read Luug 15Luug 15
Compare Luug 15:1-23Luug 15:1-23