Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 15

LUUG 15:1-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ay juutikat ak ay boroom bàkkaar daan jegesi Yeesu ngir déglu ko.
2Farisen ya ak xutbakat ya di ñurumtu naan: «Waa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom bàkkaar ak a lekkandook ñoom!»
3Noonu Yeesu daldi leen wax léeb wii ne leen:
4«Kan ci yéen soo amoon téeméeri xar, te benn réer ci, nooy def? Ndax doo bàyyi ca parlukaay ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent, toppi ma réer, ba gis ko?
5Te boo ko gisee, dinga ko gàddu ak bànneex, yóbbu ko kër ga.
6Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.”
7«Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom ñeent fukk ak juróom ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar.
8«Te it bu jigéen dencoon fukki libidoor, benn réer ca, nu muy def? Ndax du taal ab làmp, bale kër ga, seet fu nekk, ba gis ko?
9Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.”
10Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Yàlla yi di ame mbég ci benn bàkkaarkat bu tuubee ay bàkkaaram.»
11Yeesu dellu ne leen: «Dafa amoon góor gu am ñaari doom.
12Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may wara féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam.
13Ay fan yu néew gannaaw gi, caat ma fab yëfam yépp, dem ca réew mu sore, yàq fa alalam ci topp nafsoom.
14Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk.
15Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya.
16Mu xiif ba bëgga lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.
17Mujj xelam délsi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgga dee ak xiif!
18Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la;
19yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ”
20«Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko.
21Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.”
22Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gëna rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll.
23Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;

Read LUUG 15LUUG 15
Compare LUUG 15:1-23LUUG 15:1-23