1Éy Aji Sax ji, bàyyil xel li nu dal, xoolal, gisal sunu toroxte!
2Sunu suuf toxu ciy jaambur, sunuy kër ñeel ay doxandéem.
3Baay dëddu, nu diy jirim; ndey dib jëtun.
4Sunum ndox, xaalis lanu koy feye, naan, sunu matt ak njégam la mu nuy dikke.
5Sunuw loos lañu ràng, nu loof, te noppaleesu nu.
6Nu nangul Misra, nangul Asiri ngir ab dund.
7Sunuy maam a moyoon, tey nekkatuñu; nun, noo gàddu seeni mbugal.
8Ay surgaa nu yilif, te amunu ku nu wallu ci seen loxo.
9Bu nu lekkee, sunu bakkan lanu jaay, nde saamar a ngi ci màndiŋ mi.
10Sunu yaram nib taal la tànge ndax tàngoorub xiif.
11Jigéeni Siyoŋ lañuy tëdde, ak janqi dëkki Yuda.
12Kàngam yi, ñu jàpp, wékk; te mag ñi, teraleesu leen.
13Waxambaane yee yenu doji wolukaay, gone yu góor yi sëfoo sayi matt, di tërëf.
14Mag dakkal na jataayu pénc, te waxambaane talatula xalam.
15Xol nux-nuxeetul, te ay rongooñ a wuutuy pooj.
16Sunu mbaxana foq na! Wóoy ngalla nun ñi moy!
17Lee jeexal sunu xol, lii moo nu jooyloo, ba gët giim:
18tundu Siyoŋ wi gental, ba till yi di fi daagoo.
19Yaw Aji Sax ji, yaay toog ba fàww, sab jal, sët ba sëtaat.
20Ana lu waral nga fàtte nu fàww, ba nu jant yu yàgge nii?
21Éy Aji Sax ji, délloosi nu fi yaw, nu dellusi, yeesalal sunuy jant, mu mel na woon.
22Xanaa doo nu wacca wacc, mere nu mer mu amul kemu?