Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jooytu

Jooytu 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ndeysaan Boroom bee mer ba xiinal Janq Siyoŋ mu taaru mi. Fa asamaan la rattaxe sagu Israyil fa suuf. Keroog bésu meram ma, bàyyiwul xel, ne këram googoo di ndëggastalam.
2Boroom bee modd te yërëmul mboolem sanci Yanqóoba. Ca meram ma la màbbe tatay Janq Yuda mu taaru ma. Moo detteel nguur ga aki garmeem, sobeel leen.
3Tàngooru sànjam la dagge gépp kàttanu Israyil. Fa kanam noon ba la roccee dooley ndijooram. Moo tàkkal Yanqóoba ni sawara wuy sëlsëli, ba xoyom mboolem la ko wër.
4Boroom bee tàwwi ag fittam mel ni ab noon, moo diire ndijooram, mel ni bañ, moo bóom mboolem lu neexa xool. Ci biir xaymay janq Siyoŋ mu taaru ma la yuri am sànjam ni sawara.
5Boroom bee mel nib noon, modd Israyil, moddaale këram yu taaru yépp, tas ay tataam, ba fulal Janq Yuda mu taaru ma, ay yuux aki jooy.
6Moo tas mbaaram ni bu doon mbaarum tool, moo rajaxe bérabu ndajeem. Aji Sax ji moo fàtteloo waa Siyoŋ màggal ak bésub Noflaay, te tàngooru meram la xalabe buur ak sarxalkat.
7Aji Sax jee jañax sarxalukaayam, gedd bérabam bu sell. Moo teg ci loxol noon tatay këram yi. Biir kër Aji Sax ji la baat xaacoo, ni bu doon bésu màggal.
8Aji Sax jee dogoo rajaxe tatam janq Siyoŋ mu taaru, Moo tàllal buumu nattukaay, ngir tas ko, bankul loxoom it te màbbu ko. Moo jooyloo tata ak tabaxub fegukaay, ñu ànd tojatoo.
9Bunti dëkk ba suulu na, te moo yàqte, dammate weñi tëjukaay ya, buuram aki garmeem a tumurànkeji ca yéefar ya, te téereb yoon amul, yonent it gisatul peeñu mu bawoo fa Aji Sax ji.
10Magi janq Siyoŋ mu taaru ña nga toog, xeremlu, xëppoo suuf, sol ay saaku, di ñaawlu. Janqi Yerusalem sëgg, seen bopp jëm suuf.
11Samay gët a giim ndaxi rongooñ, samay butit fuddu, xol ŋiis, jeex tàkk: ci tasteg samaw askan; xale yeek gone yiy nàmp ne lasar fi mbedd yi!
12Seen yaay lañu naan: «Ana fu nuy lekke, ba naan?» Te ne lasiim ci mbeddi dëkk bi, ni ñu gaañoo xare, bakkan di tàggoo fa ñu uufoo ca weenu yaay.
13Yaw Janq Yerusalem mu taaru mi, lu ma lay wax? Ku ma lay méngaleel? Siyoŋ mu jekk mu taaru mi laa ne, ana ku ma lay dendaleel, ba seral sa xol? Yaw mi sab góom yaa ni géej, ana ku lay faj?
14Ag neen aki caaxaan la la say yonent gisal, te biraluñu sag ñaawtéef, ngir tijji sa wërsëg, xanaa di la yéeneel waxyuy caaxaan aki nax.
15Mboolem ñi fi jaareey tacc-taccali loxo, ciipu, wëcc bopp ci gentub Yerusalem mu taaru ma, te naan: «Xanaa du biib dëkk lañu doon tudd sottiteb taar ba, te muy mbégtem àddina sépp?»
16Sa noon yépp a lay ñaawal, di la kókkaleek a kekku, te naan: «Sànk nanu leen nag! Bii bés lanu yàggoona séentu, te noo ko fekke tey.»
17Aji Sax jee def la mu nammoon, moo sottal kàddoom ga mu santaane woon janti démb. Moo fàdd te yërëmul, ba may noon bége leen, te moo kaweel sa kàttanu bañ yi.
18Askan waa ngi jooy jooyi xol fi kanam Boroom bi. Éy yaw tatay janq Siyoŋ mu taaru mi, sottil say rongooñ ni walum dex guddeek bëccëg; bul nopplu, bul feral say rongooñ.

19Jógal guddi, xaacu: ndoortel wattub guddi, ngay yuri sab xol nim ndox, jàkkaarlook Boroom bi. Tàllal koy loxo, ngir sa bakkani doom, yi xiif tax ne lasiim fi boppu mbeddoo mbedd.
20Éy Aji Sax ji, xoolal, seetal rekk ki nga def nii! Xanaa du ndey mooy dem ba yàpp doomam, doom ju mu sukk jur, mu wér péŋŋ! Xanaa du sarxalkat akub yonent lañuy bóom fi bérabu Aji Sax bu sell bi!
21Mag ak ndaw a ngi ne lareet fi suuf ci mbedd yi; sama janq jeek sama xale yu góor yi tëdd, fàddoo saamar. Yaa rey ci sa bésub mer, yaa rendi te yërëmoo.
22Yaa woote ni su doon bésu màggal, tiitaange dar kepp ma. Bésub merum Aji Sax ji, kenn rëccul, kenn muccul. Doom yi ma jur, yar leen, noon bi fàkkas leen!