Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jooytu

Jooytu 1

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey! Te ñoñam noon gàññ démb. Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey, te noon ràññ fi biir xeet yi! Moo doon lingeeru diiwaan yi, tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.
2Day fanaanee jooya jooy, rongooñ yay bas-basi, te du kenn ku koy dëfal ci mboolemi soppeem. Xaritoo xarit wor ko, walbatiku diy noonam.
3Ngàllo lañu yóbbu Yuda, ci biir naqar ak njaam gu metti. Ci biiri jaambur lañu dëkk, amuñu fu ñu nopploo, mboolem ña leen dàqa leen dab, ba tance leen ca ruq ya.
4Yoon yi jëm Siyoŋ jooy na wéet, kenn jaareetu ca màggalsi. Pénc yépp a gental, sarxalkat yay binni, janq ja jàq, Siyoŋ gépp di naqarlu!
5Seen noon yaa jiite tey, seen bañ yooyoo ne finaax, Aji Sax jee mbugale waa Siyoŋ seeni tooñ yu bare, seeni doom duggig njaam, di moomeel ub noon.
6Lu doon sagub Siyoŋ, dëkk bu taaru bi, tey sàggiku na. Seeni garmee ngi mel ni kéwél yu amul parlu, di koyoŋ-koyoŋiy daw, te rëbb ne leen dann.
7Tey ci janti toroxte ak tumurànke, la Yerusalem di fàttlikoo mboolem ngëneeli démbam. Aw askanam a tàbbi ci loxol noon, te wall amul, noon ba gis leen, di textexi ci seenug yàqule.
8Yerusalem a moya moy, ba tax koo mujj di sobe; ku ko teraloon, sofental ko, ndax gis ko, mu ne duŋŋ. Moom ci boppam mu ngi binni, fuuylu.
9Sobey Siyoŋ ca pendalam, te bàyyiwul xel ag mujam. Jéllam ba yéeme na, te amul ku ko dëfal. Siyoŋ nee: «Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare; noon bi déy, am na ndam!»
10Loxo la noon bi teg ci ngëneeli Siyoŋ gépp. Siyoŋ kay a gis yéefar yi songsi këram gu sell gi, te ci ñoom nga santaane woon, ne buñu dugg sam ndaje.
11Waa Siyoŋ gépp a ngi binni, di wut ab dund, seeni ngëneel lañuy weccikoo aw ñam wu ñu leqlikoo. Yerusalem àddu na Gisal Aji Sax ji, seetal ni ma mujj tekkeedee!
12Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi, lii safu leen, waaye seetleen rekk ba gis ndax wenn mitit dab na mitit wi ñu ma teg, te Aji Sax ji naqarale ma ko ci jantub tàkktel sànjam.
13Fa kaw la Aji Sax ji sànnee sawara ci sama biiri yax, moo laaw ab caax ngir fakktal ma, waññi ma, jànnaxe ma, ma dëkke yoggooral.
14Samay tooñ la Aji Sax ji ëmb, fastee ko loxoom, mu tege sama kaw ndodd, ba jeexal sama doole. Boroom bee ma tàbbal ci loxo yu ma manula të.
15Ku doon jàmbaar fi sama biir, la Boroom bi xalab. Am ndaje la ma wooteel, ngir falaxe sama ndaw yu góor. Boroom bee dëggaate Janq Yuda mu taaru mi, ni reseñ ci biir nalukaay.
16Looloo ma tax di jooy, rongooñ di wal-wali, te ku may dëfal sore ma, mook kuy seral sama xol. Samay doom a ngi jaaxle, nde noon bi daan na.
17Siyoŋ tàllal na loxoom, waaye amul ku ko dëfal. Aji Sax jee wool askanu Yanqóoba seeni noon yi leen wër, ba Yerusalem mujj di sobe fi seen biir.
18Aji Sax ji moo yey, kàddoom laa gàntal. Yeen, xeetoo xeet, ngalla dégluleen te xool samaw tiis. Samay ndaw yu góor ak yu jigéen, ñoo duggi ngàllo!

19Samay soppe laa woo wall, ñoom ñu wor ma. Samay sarxalkat ak samay mag di wuti ab dund bu ñu leqlikoo, far faatu ci biir dëkk bi.
20Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare, samay butit di fuddu, sama biir xol salfaañoo ndaxu tiis. Man de maa gàntal ba gàntaaral, ba fa biti, saamar di fa bóome, te biir kër it di ndee.
21Dégg nañu may binni, te awma ku ma dëfal. Noon yépp a dégg samaw ay te di ko bége, nde yaa ko def. Ngalla indil bés bi nga dige, ba ñu daj li ma daj.
22Yal na seen gépp mbon teew fi sa kanam, ba nga mbugal leen ni nga ma mbugale ndax mboolem samay tooñ. Samay onk bare na, sama xol jeex tàkk.