1Ndeysaan, wurus wa giim na! Ngëneelu wurus soppiku na. Doj yu sell yaa wasaaroo, ca boppu mbedd yépp.
2Doomi Siyoŋ yu góor yu jar ya! Wurus lees leen daan nàttablee, ndeysaan tey, ñu jàppe leen ni njaqu ban lu tabaxkatu njaq liggéeye loxoom.
3Ag till sax joxe na weenam, nàmpal doomam, te sama bokk yi mujj néeg ba mel ni bànjóolig màndiŋ.
4Luy nàmp a nga mara mar, ba làmmiñ taqoo denqleñ. Gone yaa ngi ñaan mburu, te kenn daggalu leen.
5Ñi daan xéewloo ay bernde, tey ñoo xiif, ne lasar ca mbedd ya. Ña yaroo woon yérey tànneef, tey ñoo goore jalu mbuubit.
6Sama ñaawtéefu askan wee màgg, ba raw ñaawtéefu waa Sodom, dëkk ba jekki jàllarbiku, te loxo laalu ko.
7Sunu kàngam ya setoon wecc, seen yaram mucc gàkk, di lerxat bay tàkk, wér péŋŋ, leer nàññ.
8Tey ñu gëna lëndëm bànqanoos, xàmmeesu leen ci mbedd yi, ñu ngi lax, di yaxi neen, der wow koŋŋ ni matt!
9Ña saamar rey a gënu demin ña deeye xiif, jeex tàkk, ne lasar, ndax ñàkk meññatum tool.
10Ndey ak xolu njureelam, moo togge loxoom, doomu boppam, def ko njëlam, ci sama biir toskareg askan wi!
11Aji Sax jee xëpp am sànjam, sotti tàngooru meram, moo jafal sawara fi Siyoŋ, ba xoyom kenu ya.
12Du benn buur fi kaw suuf bu gëmoon, du kenn ci mboolem waa àddina ne bañ akub noon dina dem ba bëtt bunti Yerusalem.
13Seen bàkkaari yonent yaa, seen ñaawtéefi sarxalkat yaa; ñoo tuur fa digg dëkk ba deretu aji jub ñi.
14Ña ngay tëñëx-tëñëxi niy gumba ci mbedd yi, deret ja sobeel leen ba maneesula laal seeni yére.
15Ñoom lañuy gëdd naan: «Soreleen nu, nit ñu sobewu ñi! Soreleen, soreleen, buleen nu laal.» Ñu daw di tambaambalu ba ca yeneen xeet; ñooña ne leen: «Dootu fii!»
16Aji Sax ji ci boppam moo leen tasaare, faaleetu leen; cér lees séddul sarxalkat, te teraleesul mag.
17Ba tey sunu gët a ngi giim, ndax ndimbal lu nuy séentu ci dara. Fa sunuy tata lanu séentoo wenn xeet wu nu manula wallu.
18Sunuy tànk lees di topp, ba manatunoo daagoo sunuy mbedd; sunu bés jege, sunu àpp di matal, sunu saa taxaw!
19Ñi ñuy dàqa gëna gaaw ay jaxaay, ci kaw tund yi lañu nu ne dann, màndiŋ mi, ñu di nu fa tëroo.
20Ki nuy noyyee, Buur bi Aji Sax ji fal, ca seeni yeer la tance, te nu noon ci keppaaram lanuy dëkke fi digg xeet yi.
21Bégleen te bànneexooy, yeen Edomeeni réewum Ucc, ci yeen it la kaasu mbugal di jàllsi, ngeen màndi, futteeku, ne duŋŋ.
22Yaw Siyoŋ, sa mbugal mat na, deesatu la yóbbu ngàllo; yaw Edom laa ne, Aji Sax jee lay fey sa ñaawtéef, feeñal say bàkkaar.