Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jooytu

Jooytu 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Man maay nit ki gisu naqar, naqar wu ko yarub sànjum Aji Sax ji teg.
2Man la jañax, te lëndëm la ma doxloo, dug leer.
3Man doŋŋ lay yen aka yenaat loxoom, bésoo bés.
4Moo ràppal sama der ak samaw suux, tas samay yax.
5Moo tabax fi sama kaw, tanc ma, gawe ma tooke ak coono.
6Bérab yu lëndëm la ma dëël, ni ña dee bu yàgg.
7Moo ma ñag ba manumaa bëtt, te jéng yu diis la ma jénge.
8Su ma yuuxoo, woote wall it, mu tanqamlu samag ñaan.
9Ay doji yett la ñage samay yoon, te moo lajjal samay ñall.
10Moo di segg mu may tëru, di gaynde gu waafe làqukaayam.
11Samaw yoon la ma wàcce, xotat ma, tumurànkeel ma.
12Moo ma bankal xalaam, diire mag fittam.
13Sama xóotey xol la soqil ay fittam.
14Maa mujj di reetaanukaayu bokk yépp, di seen woyu bés bu nekk.
15Moo ma reggal wextan, màndal ma lu mel ni xay.
16Yéyloo na may doj, dëggaate ma ci pënd bi.
17Jàmmi xol a ma réer, ma fàtte sax luy mbégte.
18Ca laa ne sama doolee (/muñukaaya/darajaa) jeex! ak sama yaakaar ci Aji Sax ji.

19Baal xel sama naqar ak sama tumurànke, wii wextan akug tooke!
20Dama ciy xalaat aka xalaataat, sama xol jeex tàkk!
21Waaye li may dëkke bàyyi xel, ba dese yaakaar mooy lii:
22Aji Sax ji, ngoram du dakk, te yërmandeem du jeex.
23Xanaa di yeeslu jant bu nekk. Kee bare kóllëre!
24«Samab séddoo, Aji Sax jee» la sama xol wax, te moo tax ma di ko xaar.
25Aji Sax jee baax ci ñi ko yaakaar, baax ci ki koy sàkku.
26Li baax mooy muñ, xeremluy xaar wallu Aji Sax ji.
27Li baax ci nit mooy nga nangoo muñ ba ngay ndaw.
28Bu la Aji Sax ji tegee nattu, berul te muñ.
29Dëppal sa kanam ci suuf, jombul yaakaar nuyoo.
30Dékkal ub lex ku lay mbej, di la tifaari saaga, ba nga tooy.
31Boroom bi déy du la wacc ba fàww.
32Bu la tegee naqar it, yërëm la, ngoram a ni baree.
33Du bànneexam lay tege coono, aka naqaral doom aadama.
34Bu ñuy dëggaate mboolem ñi ñu tëj cim réew,
35di jalgati yelleefu nit fi kanam Aji Kawe ji,
36di been dëgg cib layoom, Boroom bi da ko dul gis?

37Ana ku wax, mu am, te Boroom bi dogalu ko?
38Muy lu baax, di lu aay, du Aji Kawe jeey àddu, amal?
39Kuy dund, ana loo deeti jàmbat, bu ñu la añalee sa bàkkaar?
40Nan càmbar, ba xoolaat jikko yi te dellu ci Aji Sax ji.
41Nan tàllal sunu xol ak sunuy loxo Yàlla ja fa asamaan,
42noo tooñ, noo fippu, ba tax yaw jéggalewoo.
43Sam sànj nga làmboo, topp nu, di rey te ñéebluwoo,
44aw niir nga sàngoo, ba ag ñaan du ko jàll.
45Mbuubitum sën nga nu def fi biir xeet yi.
46Sunu noon yépp a nuy waxal,
47tiitaange ak pax dikkal na nu, ak yàquteek sànkute.
48Saay gët a ngi wal ndax sama askan wi rajaxoo.
49Saay gët a ngi rogalaat, du fer, du ŋiis,
50ba keroog Aji Sax ji séentoo asamaan, ba gis.
51Bi ma gisee li dal jigéeni dëkk bi yépp, la sama xol jeex.
52Ñi ma bañ ci dara ñoo ma këpptala këpptal ni picc.
53Cib teen lañu ma tàbbal, ube kow doj, te may dund,
54ndox ma mëdd ma, ma ne: «sànku naa.»

55Aji Sax ji, fa xóotey pax ma laa la wooye
56Sama baat nga dégg, ma ne la: «Bul fattal sab nopp, samay onk ak samay yuux.»
57Bés ba ma la wooyee nga dikk, ne ma: «Bul tiit.»
58Boroom bi, yaa sàmm sama àq, yaa jot sama bakkan.
59Aji Sax ji, yaa gis ni ñu ma tooñe, jox ma sama àtte.
60Yaa gis seen mboolem mébetu feyu, seen mboolem pexe yi ñu may lalal.
61Aji Sax ji, yaa dégg seeni kókkalee, ak mboolem pexe yi ñu may lalal.
62Ci man la noon yiy diisoo aka déeyoo, bés bu nekk.
63Xoolal, bu ñu toogee ak bu ñu jógee, man lañuy léeboo.
64Aji Sax ji, jox leen seenub añ, seen kemu liggéeyu loxo.
65Dërkiisalal seen xol (Tegleen njàqarey xol / Muural seenum xel,) na leen sag alkànde ñeel.
66Toppe leen sa mer, te nga sànke leen mboolem fu asamaanu Aji Sax ji tiim.