1Màggal-leen Ki Sax! Santleen Aji Sax ji, kee baax, kee saxoo ngoram!
2Ana ku mana tudd jaloorey Aji Sax ji? Ana ku mana teesal woyam?
3Ndokklee kuy sàmm yoon, di def njekk fu mu tollu.
4Éy Aji Sax ji, séddaale ma ci sa yiwu ñoñ, ngalla, dikke ma sag wall,
5ma gis ngëneelu ñi nga tànn, di bànneexoo sa bànneexu xeet wi, tey damoondook ñoom ñi nga séddoo.
6Noo bàkkaar, nook sunuy maam; noo def lu ñaaw, def lu bon.
7Sunuy maam seetuñu ca say kéemaan ca Misra, bàyyiwuñu xel ca sa ngor lu réy, xanaa di fippu ca géej ga, géeju Barax ya.
8Teewul Yàlla wallu leen ngir turam, ba xamle njàmbaaram.
9Dafa gëdd géeju Barax ya, mu ne sereŋ; xóotey géej mel ni màndiŋ, mu jàlle leen,
10musal leen ci loxol bañaale, jote leen ca loxol noon ba,
11ndox ma mëdd bañ ya, kenn desu ca.
12Ca lañu gëm ay waxam, woy ko.
13Nes tuut ñu fàtte jëfam ja, xaaratuñu ndigalam,
14di ŋaf-ŋafi ca màndiŋ ma, di diiŋat Yàlla ca àll ba.
15Yàlla jox leen la ñuy sàkku, wàccaaleel leen woppi ràgg.
16Ba ñu demee ba iñaane Musaa ca dal ba, boole ca Aaróona mu sell ma, nitu Aji Sax ja,
17suuf a ne ŋafeet, wonn Datan, mëddaale gàngooru Abiram;
18sawara ne jippét fa seen biir, tàkk ba lakk ñu bon ñooña.
19Tëgg nañu aw nag ca tundu Oreb, di sujjóotal jëmm ju ñu móol,
20di jënde seen teddngay Yàlla ja jëmmu nag wuy for um ñax.
21Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal te def jaloore ca Misra.
22Mooy kéemaan ya fa réewum Xam, kiraama ya ca géeju Barax ya.
23Yàlla da leen doon sànk, bu dul woon ak Musaa, xejjam ba ko kar, àtte leen, mu giif, ba fàkkasu leen.
24Dañoo gàntal réew mu neex, gëmuñu kàddug Yàlla,
25xanaa di xultoo seen biiri xayma, baña déggal Aji Sax ji.
26Moo tax mu giñal leen ne dina leen tëral fa màndiŋ ma,
27tëral seen askan ci biir xeet yi, wasaare leen ci réew yi.
28Ñuy darook tuurum Baal Pewor, di lekk lu ñu sarxal ay yàlla yu amul bakkan,
29di merloo Yàlla ci seeni jëf, ba mbas ne dàll fa seen biir.
30Fineyas taxaw, àtte; mbas ma dal,
31muy njekk lu ñu ko waññal tey ak ëllëg.
32Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma, muy loraangey Musaa te ñoo ko waral.
33Ñoo naqaral Musaa, ba mu wax wax ju ko rëcc.
34Te it faagaagaluñu yéefar, ya leen Aji Sax ji waxoon,
35xanaa di jaxasook yéefar yooya, di roy seeni jëf,
36di jaamu seeni tuur, mu mujj dig fiir ca ñoom.
37Ñuy sarxalal rab ya seen doom yu góor ak yu jigéen,
38di tuur deretu ñu deful dara, te muy seen deretu doom yu góor ak yu jigéen ya ñu sarxalal tuuri Kanaaneen ña, deret ja sobeel réew ma,
39seeni jëf sobeel leen, ndax seen bokkaale.
40Aji Sax ji mere ñoñam, sib xeet woowu mu séddoo,
41ba tax mu teg leen ca loxol yéefar ya, seeni bañ yilif leen,
42seen noon ya not leen, ñu torox ca seeni loxo.
43Ay yooni yoon la leen xettli, teewul ñuy nas pexey fippu, ba suux ci seeni ñaawtéef.
44Mu gis nag seen njàqare, dégg seeni tinu,
45bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,
46xiir ña leen jàpp ñépp, ñu yërëm leen.
47Éy Aji Sax ji, sunu Yàlla, wallu nu, génnee nu ci xeet yi, dajale nu, nu sante la sa sellnga, di sagoo sa teddnga.
48Santleen Aji Sax ji, Yàllay Israyil cant gu sax dàkk, ba fàww. Na ñépp ne: «Amiin!» Màggal-leen Ki Sax!