Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Deewug doom ju góor, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
2Ma sante Aji Sax ji sama xol bépp, di siiwal mboolemi kéemaanam.
3Yaw Yàlla, dama lay bége, bànneexoo la, woy la, yaw Aji Kawe ji.
4Noon yeey dellu gannaaw, tërëf, sànku fi sa kanam.
5Yaa ma àtte yoon, dëggal ma, toog ci sab jal, di àtte njub.
6Rëbb nga xeet yi, sànk ñu bon ñi, far seeni tur ba fàww.
7Noon ya raaf, gental ba fàww. Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
8Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
9Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
10Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
11Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.
12Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi!
13Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel, te du fàtte yuuxi néew-ji-doole.
14Éy Aji Sax ji, baaxe ma, gisal naqar wi ma bañ yi teg. Yaa may yékkatee fa bunti ndee,
15ba ma siiwali sa woy yépp, fa buntu Siyoŋ, dëkk bu taaru ba, di bànneexoo sa wall gii!
16Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.
17Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.
18Ñu bon ñee dëddu, dem njaniiw, ànd ak xeet yi fàtte Yàlla yépp.

19Yàlla du tanqamlu ab ndóol ba fàww, yaakaaru néew-ji-doole du tas mukk.
20Aji Sax ji, jógal, bu la nit yab; na xeet yi dikk fi sa kanam, nga àtte leen.
21Rikk Aji Sax ji, yónnee leen tiitaange, xamal leen ne nit doŋŋ lañu. Selaw.