Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Yeen goney Yàlla yi, seedeel-leen Aji Sax ji, seedeel-leen ko teddngaak doole,
2seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam. Sujjóotal-leen Aji Sax ji, ki gànjaroo sellnga.
3Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma, Yàlla mu tedd maa dënu, Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww.
4Aji Sax jeey àddoo doole, Aji Sax jeey àddoo daraja.
5Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar, Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.
6Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu, tundu Siryoŋ it, mbete yëkk wu ndaw.
7Aji Sax jeey àddu, fettaxal sawara, mu boy.
8Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ, Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
9Aji Sax jeey àddu, kéwél matu, garabi àll ruus, biir këram di mennum riir, naan: «Màggal-leen ko!»
10Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu, Aji Sax jee falu buur ba fàww.
11Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, di barkeele jàmm ñoñam.