Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 71

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji, yaw laa làqoo, yàlla buma rus mukk.
2Xettlee ma sa njekk, yiwi ma; ngalla teewlu ma, te wallu ma.
3Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu bu may rawesi saa su ne, te nga dogal sama mucc. Yaw yaa may téye, di ma aar.
4Éy sama Yàlla, musal ma ci dooley ku bon ak ab saaysaay ak ab néeg.
5Boroom bi, Aji Sax ji, yaw de laa yaakaar, dale laa wóolu ba may ndaw.
6Yaw laa wéeroo ba may juddu; yaw yaa ma roccee sama biiru ndey. Yaa yelloo sama cant fàww.
7Firndey alkànde la ma ñu bare xoole woon, te yaw ngay sama rawtu bu wóor.
8Samay kàddu sag cant la fees ak di la saxoo darajaal.
9Ngalla bu ma wacc, mag laa; bu ma ba fi doole jeexe.
10Noon yaa nga may tooge, ñi may tëroo ngay diisoo,
11naan: «Yàlla wacc na ko, nan ko dàq, jàpp; kenn du ko wallu.»
12Éy Yàlla, bu ma sore. Sama Yàlla, gaawe ma.
13Samay seytaane, yal nañu leen rusloo, sànk leen. Ñi may wuta lor, yal nañu leen gàcceel, sewal leen.
14Man may saxoo yaakaar, di la sant, di santati.
15May siiwal sa njekk, di yendoo waxtaane say wall, doonte lim ba wees na ma.
16Boroom bi, Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa njekk gu wéet.
17Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan, te ba tey jii maa ngi koy biral.
18Éy Yàlla, bu ma bijjaawee ba weex tàll it, bu ma wacc, ba keroog may xamal maasu tey sa doole, xamal ñi ciy topp ñépp sag njàmbaar.

19Céy Yàlla, sa njekk àkki na fa kawa kaw. Def nga lu réy. Yaw Yàlla, ana ku mel ni yaw?
20Won nga ma ay yoon coonooki tiis, waaye yaa may dundalaat, ma mucc xóotey suuf.
21Yal nanga ma gëna sagal, geesu, bégal ma.
22Man it sama Yàlla, ma xalam, sant la ngir sa kóllëre. Aji Sell ji séddoo Israyil, dama lay woy aki xalam,
23sarxolle, woy la, bége sag njot.
24May yendoo siiwal sa njekk nde ña ma doon wuta lor lañu rusloo, sewal leen.