Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 109

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Éy Yàlla mi may sant, bul tanqamlu!
2Ku bon ak kuy fen a ma waxal, sosal ma,
3tance ma kàdduy mbañeel, song ma ci dara.
4Ma ji nit cofeel, mu sosal ma; te man ma di ko ñaanal.
5Sama jëf ju baax, loraange lañu ma ko feye, sama cofeel, ñu feye ma ko mbañeel.
6Yal nanga fal ku bon ci kaw kii, ab soskat féete ko ndijoor.
7Bu ñu koy àtte, yal nañu ko yey, te yal na ñaanam walbatiku di bàkkaar.
8Yal naw fanam gàtt, keneen jagoo sasam.
9Yal nay doomam diy jirim, jabaram dib jëtun,
10ay doomam di tambaambaluy yalwaan, dëddu seeni gent, dem tàllal ay loxo.
11Yal na ko kuy feyeeku futti, ay doxandéem foqati ñaqam.
12Yàlla bu ko kenn ji ngor, yàlla bu kenn baaxe jirim yi ko wuutu.
13Yal na askanam dagg. Balaa geneen maas a wéy, yal na seenu tur fey.
14Yal na Aji Sax ji bàyyi xel ñaawtéefi maamam. Yàlla bu bàkkaaru ndeyam faru.
15Yal na seeni moy sax fi kanam Aji Sax ji. Yal na seen tur dagge fi kaw suuf.
16Moo séddul ngor, di topp ku néewle te sonn, seen xol jeex, mu bóom.
17Moo bëggoon di móoloo, yal na ko këppoo; soppul ag ñaan it, yal na ko barke sore.
18Móolook sol mbubb la yemale, yal nañu duy nim ndox ay móoloom ci yaramam, mu seeb ci biiri yaxam nig diw.

19Yal nay móoloom di mbubbam, te di laxasaay gu mu saxoo.
20Lii, yal na ko Aji Sax ji feye ñi may sosal, di teg lu ñaaw ci sama der.
21Waaye Boroom bi Aji Sax ji, defal ma li sa tur laaj. Yaa baax, gore, xettli ma.
22Damaa néewle te sonn, sama xol dagg, ba jeex tàkk.
23Maa ngi tàggoo ni keru ngoon, ñu di ma fél ni soccet.
24Samay óom a ngi nasax ndax ñàkka lekk, desewuma lu moy yaxi neen.
25Maa ngii, ñu di ma sewal, ku ma gis, wëcc bopp.
26Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, dimbali ma, walloo ma sa ngor,
27ba ñu xam ne lii sa loxoo, xam ne yaw Aji Sax ji, yaa ko def.
28Ñooy móolu, yaw nga barkeel; ñoo ma jógal, ñooy torox, man, ma bég, Sang bi!
29Yal na ñi may sosal sàngoo toroxte, làmboo gàcce ni mbubb.
30Ma àddu, santa sant Aji Sax ji, di ko màggale digg mbooloo mu yaa.
31Mooy féete ndijoor néew-ji-doole, musal ko ci ku koy teg àtteb dee.