Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 142

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma.
2Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
3sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.
4Bu ma yoqee, ràññee nga samay jéego; yoon wi may jaare lañu ma làqal am yeer.
5Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf.
6Aji Sax ji, ma woo la wall; ma ne, yaay sama kiiraay, di sama séddoo fi kaw suuf.
7Teewlul, ma ne wóoy, damaa manatul, xettli ma ci ñi ma topp, dañu maa ëpp doole.
8Ngalla génne ma fi ma tëje, ma sant la. Man la way-gëm ñi di yéew ëllëg, yaa may xéewale ab yool.