1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.
2Éy yaw, Sàmmu Israyil, teewlu nu; yaw mi jiite Yuusufa ni ag jur, yaw mi toogandook malaakay serub yi, feqal sag leer.
3Dawalal sa njàmbaar, ñeel Efrayim ak Beñamin ak Manase, te wallusi nu.
4Éy Yàlla, suqli nu; geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
5Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, foo àppal sa mer, mi ngay wuyoo sa ñaanu mbooloo mi?
6Leel nga nuw naqar, nàndal nu mbàndum rongooñ,
7def nga dëkkandoo di nu xëccoo, noon di nu ree.
8Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, suqli nu; geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
9Yaa déjjatee reseñ Misra, dàq yéefar yi, indi, jëmbataat.
10Nga wéex ko, mu sampu, law, dajal réew mi;
11keppaaram muur tund yi, ay caram sàng garabi seedar yu mag yi.
12Mu tàllal ay bànqaasam ba géej, lawal njebbit la ba dex ga.
13Lu tax nga bëtt ay miiram, ba ku fa jaare witt ca,
14mbaam àll di ko ruur, ndundati àll di ca for?
15Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul; séentool asamaan, ba gis te taxawusi reseñ jii.
16Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor, ngarab sii nga dooleelal sa bopp.
17Dees koo gor, taal; yal na ñii sànkoo sa mbugal.
18Yal nanga yiir ki nga tànn, kii nga dooleelal sa bopp,
19ba dootunu la dëddu. May nu nu dund, nu wormaal sa tur.
20Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, suqli nu, geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.