1Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun, saw tur nga wara teral, ngir sa ngor ak sa worma.
2Bu yéefar yi ne mukk: «Moo ñii, ana seen Yàlla?»
3Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan, di def lu la soob.
4Seeni tuur xaalis laak wurus, di liggéeyu doom aadama:
5am gémmiñ te du wax, ami gët te du gis,
6ami nopp, du dégg, ami wakkan, du xañtu,
7ay yoxo it te du yég, ay tànk it te du dox, du xàddmiku sax.
8Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom, ñook ñi leen wóolu ñépp.
9Éy Israyil, wóolul Aji Sax ji, moo lay jàpple, di la aar.
10Yeen waa kër Aaróona, wóoluleen Aji Sax ji, moo leen di jàpple, di leen aar.
11Yeen ñi ragal Aji Sax ji, wóoluleen Aji Sax ji, moo leen di jàpple, di leen aar.
12Aji Sax jee nuy bàyyi xel, di nu barkeel, di barkeel kër Israyil, di barkeel kër Aaróona.
13Aji Sax jeey barkeel ku ko ragal, mag ak ndaw.
14Yal na leen Yàlla ful, ful seeni doom.
15Yal nangeen barkeeloo Aji Sax ji, ki sàkk asamaan ak suuf.
16Asamaan, asamaanu Aji Sax jee, suuf la dénk doom aadama.
17Du ku dee mooy màggal Ki Sax, du kenn ku tàbbi réewum tàbbi-selaw!
18Nun, nooy sargal Ki Sax, tey ak ëllëg. Màggal-leen Ki Sax!