Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 116

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo, dagaan ko, mu dégg ma.
2Teewlu na ma moos, dama koy woo li feek may dund.
3Buumi ndee a ma laawoon, njàqarey njaniiw dab ma, ma dajeek naqar aku tiis.
4Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Ngalla Aji Sax ji, xettli ma!»
5Aji Sax jeey boroom yiw ak njekk, sunu Yàllaay boroom yërmande.
6Aji Sax jeey aar ku xamul àddina; tumurànke woon naa, mu wallu ma.
7Bu ma yeboo sama xel dal, Aji Sax ji baaxe na ma!
8Xettli nga ma, ba deewuma, jàpple ma ba tërëfuma, feral nga it samay rongooñ.
9Damay topp Aji Sax ji ci biir réewum aji dund ñi.
10Ba ma naa: «Torox naa ba toskare,» teewul may ànd ak ngëm.
11Maa jàqoon ba naan: «Ñéppi fen-kat lañu!»
12Ana lu may njukkale Aji Sax ji, li mu ma baaxe lépp?
13Xanaa ma yékkati kaasu Aji Sax jiy misaal wallam, te may tudd turam.
14Samay digeek Aji Sax ji laay matal fi kanam ñoñam ñépp.
15Wóllërey Aji Sax ji, bakkanam ñor na Aji Sax ji.
16Aji Sax ji, maay sab jaam, maay sab jaam, di sa doomu jaam bi ma sukk jur. Yaa yiwi samay buum,
17yaw laay sarxalal saraxu cant, te turu Aji Sax ji laay tudd.
18Samay digeek Aji Sax ji laay matal fi kanam ñoñam ñépp,

19fi ëtti kër Aji Sax ji, fi digg Yerusalem. Màggal-leen Ki Sax!