Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy woyu Sabóor, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga.
2Aji Sax ji, dama lay kañ. Yaa ma yékkati, ba noon reetaanu ma.
3Aji Sax ji sama Yàlla, maa la woo wall, nga faj ma.
4Aji Sax ji, yaa ma jukkee njaniiw, may ma bakkan, ma tàggook ñiy tàbbi njaniiw.
5Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji, njukkale ko sellngaam.
6Meram di lu gàtt, aw yiwam sax dàkk. Rongooñ gane, fanaan, ay ree xëysi.
7Man damaa baaxle woon, ba ne: «Deesu ma rëññeel mukk.»
8Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe, dëj ma, ma ne kekk niw tund. Nga fuuyu, ma jàq.
9Aji Sax ji, yaw laa woo wall; Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw,
10ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel, ana lu mu lay jariñ? Nu la pëndu pax di sante, bay biral sa worma?
11Aji Sax ji, déglul, baaxe ma; éy Aji Sax ji, dimbali ma.»
12Yaa ma soppil samay rongooñ ay ree, summi sama yérey tiis, solal ma bànneex.
13Naa la woye xol, baña selaw. Aji Sax ji, sama Yàlla, ma sant la ba fàww!