Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 55

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, dib taalif, ñeel Daawuda.
2Éy Yàlla, déglul, ma ñaan la, bul làqu, dama lay dagaan.
3Teewlu ma, nangul ma. Li may tawat a ma xañ jàmm, ub sama bopp;
4coowal noon yee ak coonob ñu bon ñi. Dañu maa teg fitna, di ma songe xadar.
5Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi; tiitaangey ndee ne ma taral.
6Njàqaree ma dugg, may kat-kati, musiba mëdd ma.
7Dama ne: «Éy ku may may laafi xati, ma ne fërr, noppluji.
8Xanaa ma naaw, ba sore, fanaani màndiŋ ma. Selaw.
9Naa gaawtu, seeluji ngelaw lu riddi ak ngëlén.»
10Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen. Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi,
11guddeek bëccëg ñuy wër, ñaawtéef ak ayib wéttali leen.
12Yàq a nga ca biir, te noteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.
13Su doon noon bu may ñaawal, ma muñ ko, mbaa muy bañ bu may won ab dayo, ma daw ko.
14Waaye yaw la, sama nawle, di sama wóllëre, ma xam la.
15Nu daan bokk bànneexu diisoo, ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.
16Yal na leen dee bett, ñu jekki tàbbi njaniiw, ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay.
17Waaye man, Yàlla laay woo wall, te Aji Sax jee may wallu.
18Subaak ngoon ak njolloor, may ñaxtook a ñurumtu, mu dégg ma.

19Moo may jot ak jàmm, ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe.
20Yàllaay dégg, duma leen, moom mi nguuram yàgga sax. Selaw. Soppikuwuñu fenn te ragaluñu Yàlla.
21Kii a ngi xàccil ñi mu takktool, di fecci kóllëre,
22làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.
23Sippikul Aji Sax ji lu la diis, moom moo lay taxawu. Du bàyyi mukk aji jub, muy tërëf.
24Waaye yaw Yàlla, yaa leen di tàbbal, bóomkat ak naaféq ci pax mu xóota xóot, te seenu fan xaajul. Man nag, ma di la wóolu.