Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2Ndokklee yaw mi yég néew-ji-doole. Aji Sax jee lay xettli, bésub njàqare.
3Aji Sax jee lay aar, di sàmm sa bakkan, nga jagoo barke ci réew mi, te du la bàyyi noon def la lu ko neex.
4Aji Sax jee lay dooleel soo woppee, di soppi bu baax sa tëraay.
5Dama ne: «Aji Sax ji, tooñ naa la; baaxe ma, faj ma.»
6Noon yaa ngi may yéene lu bon, naan: «Xanaa kii du dee, ba ñu fàtte ko?»
7Ku dikk, di ma seet, di jinigal tey fenti sos ci xolam, bu génnee, tasaare ko.
8Bañ yépp a ngi may déeyoo, di ma fexeel lu bon,
9naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»
10Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma, te daan lekk samaw ñam.
11Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma, yékkati ma, ma fey leen.
12Su noon damuwul ci sama kaw, ma doora xam ne bége nga ma.
13Man, damaa maandu, nga taxawu ma, dëj ma fi sa kanam, ba fàww.
14Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil. Moo masa yelloo cant, ba fàww. Amiin, Amiin.