1Muy taalifu Daawuda, ngir jàngle.
2Éy Yàlla, sàmm ma, maa ngi làqu fi yaw! Maa ne Aji Sax ji: «Yaay sama Boroom, awma alal ju la moy.»
3Ñu sell ñi ci réew mi ñooy garmi yi, sama mbégte mépp ñoom a.
4Kuy sàkkuy tuur barew tiis, man de duma leen tuural deret, sama làmmiñ du leen tudd.
5Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.
6Maa muurloo bérab bu neex, ndaw cér bu rafet!
7Ma sant Aji Sax ji may xelal, ba guddi sax sama xel di ma yedd.
8Damaa saxoo ne jàkk ci Aji Sax ji ndijoor la ma fare, ba duma tërëf,
9xanaa di bànneexu, sama xol bég, sama yaram finaax.
10Doo ma wacc njaniiw moos, sa wóllëre wa, doo ko won yàqutey bàmmeel.
11Yaa may xamal yoonu ndund. Fu bànneex mate, yaa teew, xéewal sa ndijoor la saxe.