Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor

Sabóor 15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Aji Sax ji, kuy ganeji sa xayma? Ana kuy dëkki sa tund wu sell?
2Xanaa ki wéye maandu, di def njekk, di wax dëggu xolam.
3Du sos, du tooñ dëkkandoo, du baatal moroomam.
4Ku siblu, mu sib, ku ragal Yàlla, mu teral. Mooy sàmm ngiñam, su ko dee lor it.
5Du leble, ba teg ca; du nangu ger, ngir fexeel jaambur. Lii ku koy jëfe doo jang.