1Muy ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga. Boroom bi, yaa nu masa fat maasoo maas.
2Bala tund yee juddu, bala ngay sos suuf ak àddina, yaa mas di Yàlla, ba fàww.
3Yaay delloo doom aadama ci pënd, ne ko: «Yaw, doom aadama, dellul!»
4Junniy at ci yaw daa gaaw ni démb ak tey, mbete waxtu yu néew ci wattub guddi.
5Yaay buub nit, nelawal ko. Suba mu jebbi nim ñax,
6xëy, jebbi, naat; ngoon mu lax, wowal.
7Soo meree kay, nu sànku, nga xadaru, nu jàq.
8Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.
9Sunu giiru dund nga di nu mere, sunuy fan jeex ni noo guy naaw.
10Sunu àppu dund di juróom ñaar fukki at, ku dëgër ba dëgër, juróom ñett fukk; li ci ëpp di coonooku tiis, ne fëyy, nu wéy.
11Ana ku xam sa dooley mer ak sa xadar ju raglu?
12Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan, ba nu mana dawal xel mu rafet.
13Aji Sax ji, délsil, loo deeti xaar? Ngalla yërëmal sa jaam ñi.
14Nu xëy, nga reggal nu sa ngor, nuy sarxolle, bànneexoo ko sunu giiru dund.
15Bànneexal nu limu fan yi nga nu mbugal, diirub ati tiis yi nu dund.
16Yal na sa jaloore leer sa jaam ñi, sa daraja leer seeni doom.
17Boroom bi sunu Yàlla, ngalla baaxe nu. Sottalal nu sunuy liggéey, rikk, sottalal nu sunuy liggéey.