Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Neyemi

Neyemi 7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw ba ñu tabaxaatee tata ja, ma taxawal lafi bunt ya, ba noppi dénk fara bunt ya seen liggéey, ñook jàngkat yaak Leween ña.
2Ci kaw loolu ma sas sama mbokk Anani, mu jiite Yerusalem, mook Anaña boroom tata ja, ndax la mu gëna dëggu ñu bare, gën leena ragal Yàlla.
3Ma ne leen: «Bu bunti Yerusalem ubbiku li feek jant bi tàngul. Santleen fara bunt yi ñuy tëj bunt yi, sës ci galani tëjukaay yi, balaa waa dëkk biy tëdd. Na ku nekk ci waa Yerusalem di wattoo ca bérabu wattukaayam, mbaa buntu këram.»
4Booba dëkk ba réy na, yaatu na; waaye nit ña ca dëkk ñoo néew, te kër ya tabaxewaatul woon.
5Sama Yàlla xiir ma ma woo garmi yeek kilifa yeek baadoolo yi, ngir bind leen. Ci biir loolu ma gis limeefu làng ya jëkka jóge ngàllo ga, ba ñibbsi. Li ma fekk ñu bind ko ci mooy lii:
6Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nabukodonosor buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbsi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk.
7Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwe ak Neyemi ak Asaryaa ak Ramya ak Nayamani ak Mardose ak Bilsan ak Misperet ak Bigway ak Neyum ak Baana. Limeefu góori bànni Israyil nii la tëdde:
8Askanu Paros ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172).
9Askanu Sefatiya ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372).
10Askanu Ara di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652).
11Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (2 818).
12Askanu Elam junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254).
13Askanu Sàttu juróom ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (845).
14Askanu Sakay juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760).
15Askanu Binuy juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett lañu (648).
16Askanu Bebay juróom benn téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (628).
17Askanu Asgàdd ñaari junni ak ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (2 322)
18Askanu Adonikam juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (667).
19Askanu Bigway ñaari junni ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (2 067).
20Askanu Adin juróom benn téeméer ak juróom fukk ak juróom lañu (655);
21askanu Ater soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98);
22Askanu Asum ñetti téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (328).
23Askanu Besay ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñeent lañu (324).
24Askanu Arif téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112).
25Askanu Gabawon juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95).
26Waa Betleyem ak Netofa téeméer ak juróom ñett fukk ak juróom ñett lañu (188).
27Waa Anatot téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128).
28Waa Bet Asmawet ñeent fukk ak ñaar lañu (42).
29Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743).
30Waa Raama ak Geba juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621).
31Waa Migmas téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122).
32Waa Betel ak Ayi téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123).
33Waa Nebo gu ndaw juróom fukk ak ñaar lañu (52).
34Waa Elam gu ndaw junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254).
35Waa Arim ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320)
36Waa Yeriko ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345).
37Waa Lodd ak Adidd ak Ono juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (721).
38Waa Sena ñetti junni ak juróom ñeenti téeméer ak fanweer lañu (3 930).
39Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973).
40Askanu Imer junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052).
41Askanu Pasur junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247).
42Askanu Arim junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017).
43Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ma soqikoo ca Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74).
44Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett (148).
45Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, di téeméer ak fanweer ak juróom ñett (138).
46Liggéeykati kër Yàlla gi ñoo di: Askanu Ciya, ak askanu Asufa, ak askanu Tabawot,
47ak askanu Keros, ak askanu Siya, ak askanu Padon,
48ak askanu Lebana, ak askanu Agaba, ak askanu Salmay,
49ak askanu Xanan, ak askanu Gidel, ak askanu Gayar,
50ak askanu Raaya, ak askanu Reccin, ak askanu Nekoda,
51ak askanu Gasam, ak askanu Usa, ak askanu Paseya,
52ak askanu Besay, ak askanu Meyunim, ak askanu Nefusim,
53ak askanu Bagbug, ak askanu Akufa, ak askanu Arur,
54ak askanu Baslut, ak askanu Meyida, ak askanu Arsa,
55ak askanu Barkos, ak askanu Sisera, ak askanu Tema,
56ak askanu Necciya, ak askanu Atifa.
57Askanu jaami Suleymaan ñii la: Askanu Sotay, ak askanu Soferet, ak askanu Perida,
58ak askanu Yaala, ak askanu Darkon, ak askanu Gidel,
59ak askanu Sefatiya, ak askanu Atil, ak askanu Pokeret Asbayim, ak askanu Amon.
60Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392).
61Ña bàyyikoo Tel Mela ak Tel Arsa ak Kerub Adon ak Imer te manuñoo firndeel ne seen waa kër maam ak seen askan ci Israyil lañu bokk, ñii la:
62Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak ñaar (642).
63Am na it ñu loolu daloon ci sarxalkat yi, muy askanu Abaya, ak askanu Akocc, ak askanu Barsilay, ma doon denc doomu Barsilay waa Galàdd ba, ba tax ñu santale ko seen sant.
64Ñooñu seet nañu seen limeefu kër maam, waaye gisuñu ko. Ñu daldi leen doyadal, génne leen ci carxal gi.
65Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu sell yaa sell, ba keroog sarxalkat ba di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax Urim ak Tumim.
66Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360),
67te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245),
68ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720).
69Am na ñu jiite seen kër baay, ñu def seen loxo ca liggéey ba. Boroom dëkk ba def na ca alal ja junniy poseti wurus (1 000) ak juróom fukki këll (50) ak fanweeri mbubbi sarxalkat (30) ak juróomi téeméeri dogi xaalis (500).
70Ñenn ca ña jiite seen kër baay def nañu seen loxo ca alal ja ñu jagleel liggéey ba, mu tollu ci ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis ak ñaar téeméer (2 200).
71La des ca askan wa joxe na ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis (2 000) ak mbubbi sarxalkat yu tollu ci juróom benn fukk ak juróom ñaar (67).
72Ba loolu amee bànni Israyil gépp sancaat ca seen dëkki cosaan, sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak ñenn ca baadoolo yaak liggéeykati kër Yàlla ga.