Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Neyemi

Neyemi 1

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mbiri Neyemee ngi, góor gay doomu Akalya: Ca ñaar fukkeelu atu nguurug Artaserses, ci weeru Kislew, man Neyemi maa nga woon ca Sus, péey ba.
2Ci kaw loolu Anani, kenn ci saay bokk bàyyikoo Yuda, ànd aki nit. Ma laaj leen ndesu Yawut ya rëcce ca njaam ga, laaj leen it mbirum Yerusalem.
3Ñu wax ma, ne ma: «Ña rawe ca njaam ga de, ña nga diiwaanu Yuda, ci njàqare ju réy akug toroxte. Tatay Yerusalem jaa nga tojatoo, bunt ya lakk.»
4Ba ma déggee kàddu yooyu, damaa toog di jooy, ñaawlu ko ay fan, di woor ak a ñaan ci Yàlla Boroom asamaan.
5Ma ne: «Éy Aji Sax ji, yaw Yàlla Boroom asamaan, Yàlla ju màgg ji te raglu, di sàmm kóllëreek ngor, ñeel ñi la sopp tey topp say santaane.
6Ngalla Sang bi, teewlu ma, xippi say gët, te déglu sama ñaan, yi may ñaanal guddeek bëccëg bànni Israyil, say jaam. Tegoo naa moy yi la bànni Israyil moy, te man sax maak sama waa kër baay, moy nanu la.
7Lu ñaawa ñaaw lanu la def, te sàmmunu say santaaneek say dogal ak sa ndigali yoon ya nga dénkoon Musaa, sa jaam ba.
8Rikk bàyyil xel kàddu ya nga dénkoon Musaa, sa jaam ba, ne ko: “Bu ngeen feccee kóllëre, maa leen di tasaare ci biir xeet yi.
9Waaye bu ngeen walbatikoo ci man, sàmm samay santaane, di ko jëfe, bu ñu yóbbu woon seeni ñoñ ba fa suuf digalook asamaan sax, fa laa leen di jële, boole leen yóbbu ca bérab, ba ma taamoo dëël sama tur.”
10Ñooy say jaam, sa ñoñ ñi nga jote sa kàttan gu réy ak sa doole ju bare.
11Éy Boroom bi, Sang bi, rikk teewlul bu baax samag ñaan, ak sa ñaanu jaam ñi safoo wormaal saw tur. Ngalla Sang bi, nangul ma tey jii, may ma waa jii yéwéne ma.» Booba maa yore woon naani Buur.