Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
2«Waxal bànni Israyil ne leen, ñu indil ma ab jooxe. Ci képp ku am yéeneem ngeen di nangoo sama jooxe, indil ma ko.
3Jooxe bi ngeen di nangoo ci ñoom di wurus ak xaalis ak xànjar,
4ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy
5ak deri kuuyu xar yu ñu wulli, sóob ko xonqal, ak deri piipi ak banti séng,
6ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwu pal, di xeeñal cuuraay,
7ak peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci xar-sànnim sarxalkat bu mag ba ak kiiraayal dënnam.
8Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir.
9Na lépp dëppoo ak li ma lay won. Muy misaalu xaymab jaamookaay bi, di misaalu mboolem ay jumtukaayam, lépp defeleen ko noonu.
10«Defarleen gaalu dénku séng, guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll; taxawaayam di xasab ak genn-wàll.
11Nañu ko xoob wurusu ngalam. Biir ak biti lañu koy xoob, sàkkal ko kéméju wurus, gu ko wër.
12Móolalal gaal gi ñeenti lami wurus yu ñuy takk ci ñeenti tànk yi; ñaari lam, wet gii; ñaar wet gee.
13Yettlul ay banti njàppuy séng te nga xoob bu ci nekk wurus.
14Su ko defee nga roof njàppu yi ci lam, yi ci weti gaal gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi.
15Ci lami gaal gi la njàppu yiy des te bañ cee jógeeti.
16Yebal ci gaal gi àlluway seede si ma lay jox.
17«Defarlul kubeer gu ñuy amale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll.
18Tëgglul ñaari malaakay serub yu wurus te nga féetale leen ak ñaari cati kubeeru njotlaay ga.

19Defal cat lii ab serub, cat lee ab serub te nanga móolaale kubeer gi ak serub yi ci ñaari cat yi, ñu ànd di benn.
20Na serub yi tàllal seeni laaf, jëme kaw te nañu yiire kubeeru njotlaay gi seeni laaf. Nañu janoo, te na seeni kanam jublook kubeeru njotlaay gi.
21Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox.
22Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israyil.
23«Defarlul taabalu bantu séng, guddaayam di ñaari xasab, yaatuwaayam di xasab, taxawaayam di xasab ak genn-wàll.
24Xoob ko wurusu ngalam te defal ko kéméju wurus gu ko wër.
25Defal ko pegg bu ko wër bu tollu ci ñeenti baaraam, te sàkkal pegg ba wombu wurus, wërale ko.
26Defarlul ko ñeenti lami wurus te takk lam ya ca ñeenti wet ya, fa fareek ñeenti tànk ya.
27Na lam yi dendeek pegg bi, ngir mana téye njàppu, yi ñuy yóbboo taabal ji.
28Yettlul ay njàppu yu bantu séng, nga xoob njàppu yi wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji.
29Sàkkal ko ay ndabam yu tell aki mbàttoom aki njaqam, ak këllam yi ñuy tuuroo. Te wurusu ngalam ngay def lu ci nekk.
30Tegal mburum teewal mi ci kaw taabal ji, mu nekk ci sama kanam ba fàww.
31«Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn.
32Juróom benni car ñooy soqikoo ca wet ya, ñetti car ci gii wet, ñett ca ga ca des.
33Benn car day am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, car ba ca topp am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd aki kàmbóotam aki mbaram, juróom benni car, ya soqikoo ca per ba, daj.
34Gannaaw loolu peru tegukaayu làmp ba itam day am ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram.
35Ab kàmbóot ay ronu yii ñaari car, jàpp ca; beneen kàmbóot ronu ñaari car ya ca topp, jàpp ca, ab kàmbóot ronu ñaari car ya mujj, jàpp ca, juróom benni car, ya soqikoo ca peru làmp ba, daj.
36Kàmbóot ya ak car ya dañuy ànd ak tegukaay ba, di benn, lépp doon lu ñu tëgge wenn dogu wurusu ngalam.

37Defarlul juróom ñaari làmpam. Te na làmp ya tege tegin wuy leeral ca kanam tegukaay ba.
38Ñiimi feyukaayu làmp yi ak andi làmp yi na doon wurusu ngalam.
39Fanweeri kiloy wurusu ngalam ak juróom, ci lees di sàkk tegukaayu làmp bi, ak mboolem li mu àndal.
40Nanga xool te topp misaal, yi ñu la ciy won ci kaw tund wi.