Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Wëñ gu baxa gi te laal yolet nag ak wëñ gu xewar gi ak gu xonq gi curr, ci lañu sàkk yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci bérab bu sell bi. Ñu daldi defar yére yu sell, yi ñeel Aaróona noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
2Xar-sànni mi, wëñu wurus lees ko ràbbe, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe.
3Ay xobi wurus lañu tëgg ba mu jekk, ñu dagg ko ay wëñ yu ñu ràbbaaleek wëñ gu baxa gi te laal yolet, ak wëñ gu xewar gi, ak gu xonq gi curr, ak wëñu lẽe gi. Ñu daldi ciy ñawaale ay nataal.
4Ñaari ngàlli mbagg lañu ko defal, daldi faste wu ci nekk ci ñaari cati xar-sànni mi.
5Ngañaayu taaral li tege ci kaw, ni xar-sànni mi lees ko defare, liggéeyaale kook moom, ñu ànd di benn. Ñu ràbbe ko wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
6Ci kaw loolu ñu we peri onigsë yi, fege per yi ŋankukaayi wurus, daldi ciy ñaas turi doomi Israyil yu góor, noonu ñuy ñaase xàmmikaay yi ñuy torloo.
7Ñu tapp per yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, per yi nag taxawe taxawaayu bànni Israyil, noonu ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
8Ñu sàkk kiiraayal dënn bi, liggéeyaale ko ay nataal ni xar-sànni mi, ràbbe ko wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe.
9Ab kaare bu ñu lem lañu ko def, guddaay bi, gannaaw bu ñu ko lemee, di ŋaraleb baaraamu déy ak digg, yaatuwaay bi di ŋaraleb baaraamu déy ak digg.
10Ñu we nag ay per ci kaw kiiraayal dënn bi, def ko ñeenti làngi per. Làng gi jiitu, peru sarduwan ak peru topaas ak peru eskarbukal moo ca nekk;
11ñaareelu làng gi di peru emëródd ak peru safiir ak peru jamaa,
12ñetteelu làng gi di peru yasent ak peru agaat ak peru ametistë,
13ñeenteelu làng gi di peru kirsolit ak peru onigsë ak peru jàspë, te per bu ci nekk ŋankukaayu wurus lees ko wewe.
14Per yeek turi doomi Israyil yu góor ñoo tolloo ab lim: muy fukk ak ñaar, ni tur yi tollu. Ñu ñaas ci tur yi ni xàmmikaayi torlu, ku nekk ak turam, ba fukki giir yeek ñaar daj.
15Ci biir loolu ñu sàkkal kiiraayal dënn bi ñaari caqi wurusu ngalam yu ci tege, te rawaasoo ni ay buum.
16Ñu sàkk itam ñaari ŋankukaayi wurus ak ñaari jaaroy wurus yu ñu takk ci ñaari cati kiiraayal dënn bi ci kaw
17Ñu nas nag ñaari buumi wurus yi ci ñaari jaaro yi ci cati kiiraay li.
18Yeneen ñaari cati buumi wurus yi, ñu we leen ci ñaari ŋankukaay, yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, ci kanam.

19Ñu sàkkal ko itam ñaari jaaroy wurus, yu ñu we ci ñaari cati suufi kiiraay li, fi féete biir, wet gi tafu ci xar-sànni mi.
20Ñu sàkkalaat kiiraay li yeneen ñaari jaaroy wurus, yu ñu we ci suufu ngàlli xar-sànni mi, fi féete kanam, dendeek sofu ngàll yi, te tiim ngañaayu xar-sànni mi.
21Kiiraayal dënn bi, buum gu sew gu baxa te laal yolet, moom lees ko téyee, lëkklee ko jaaroy kiiraay leek jaaroy xar-sànni mi, kiiraay li dëkke tiim ngañaay li, ba du teqlikook xar-sànni mi, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
22Fëxya bi xar-sànni miy tege, lépp, wëñ gu baxa te laal yolet lees ko ràbbe ba mu daj.
23Baatu fëxya baa ngi ci digg bi, mel ni baatu mbubbam xare, ñu ombe ko omb bu dëgër, ba mu daj, ngir du xottiku.
24Ci biir loolu ñu takk ci ombu fëxya bi, ay doomi gërënaat yu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe.
25Ñu def itam ay jóolóoliy wurusu ngalam, ba takk jóolóoli yi ci diggante doomi gërënaat yi, wërale ko ombu fëxya bi, ba mu daj, jóolóoli yi dox diggante doomi gërënaat yi.
26Ab jóolóoli, ab gërënaat, ab jóolóoli, ab gërënaat ba ombu fëxya, bi ñuy sol di sarxal daj, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
27Ñu sàkkal nag Aaróona aki doomam mbubb yu gudd yu ñu ràbbe wëñu lẽe,
28ak kaalag lẽe, ak mbaxanay lẽe, ak tubéyi njiitlaay yu lẽe,
29ak laxasaay giy liggéeyu ràbb bu rafet, bu ñu ràbbe wëñu lẽe bu dëgër, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
30Ñu sàkk nag meeteel gu sell gu wurusu ngalam, muy dogu wurus wu tell, ñu ñaas ci kawam mii mbind, ni ñuy ñaase mbindum torlu: «Sell na, ñeel Aji Sax ji».
31Ñu daldi koy takke buum gu baxa te laal yolet, téyee ko ko ci kaw kaala gi, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
32Noonu la mboolem liggéeyu màkkaanu xaymab ndaje mi mate. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa rekk, ni la ko bànni Israyil defe.
33Ba loolu amee ñu indil Musaa jaamookaay bi: xayma bi ak yëfam yépp; lonku yi ak làcc yi ak galan yi ak jën yeek tegu yi,
34ak kiiraayal deri kuuy yi ñu sóob xonq, ak kiiraayal deri piipi yi, ak kiiraayal xàjjatle bi,
35ak gaal gi àlluway seede si dence, aki njàppoom, ak kubeeru saraxu njotlaay gi,
36ak taabal jeek ndabam yépp, ak mburum teewal mi ciy tege,

37ak tegukaayu làmp bu wurusu ngalam bi aki làmpam, làmp yi sësaloo ba jekk ak mboolemi jumtukaayam, ak diw gi ñuy taaloo,
38ak sarxalukaay bu wurus bi, ak diwu pal gi, ak cuuraay lu xeeñ li, ak kiiraayal buntu xayma bi,
39ak sarxalukaayu xànjar beek caaxub xànjaram, aki njàppoom ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom,
40ak sori wurmbalu ëtt bi aki jënam aki tegoom, ak kiiraayal lafu buntu ëtt bi, aki buumam aki xeram; mboolem jumtukaay, yi ñuy liggéeye ci màkkaanu xaymab ndaje mi rekk,
41ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci bérab bu sell bi; yére yu sell yu Aaróona sarxalkat bi, ak yérey doomam yi ñuy sol, di sarxale.
42Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa rekk, ni la bànni Israyil sottale liggéey bi bépp.
43Musaa nag nemmiku mboolem liggéey bi, ba gis ne sottal nañu ko; noonee ko Aji Sax ji santaanee woon, ni lañu ko defe. Musaa daldi leen ñaanal.